giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom ne ay koppam moo ëpp limu biddiwi asamaan si

giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom ne ay koppam moo ëpp limu biddiwi asamaan si

Jële na ñu ci Abuu Sarrin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- luy mbiri koppi mbalka ma ? Mu wax ne: «giñ naa ci ki bakkanu Muhammat nekk ci loxoom ne ay koppam moo ëpp limu biddiwi asamaan si, ci guddi gu lëndëm te sett, ay koppi àjjana ku ca naan dootul mar ba fàwwu, booba lay mujjee mar, ñaari mball yu bawoo àjjana ñoo fay sottiku, ku ca naan dootul mar, yaatuwaayam moo ngi mel ni guddaayam, moo ngi toll ni diggante Ummaan ak Aylata, ndoxam moo gën a weex meew, te moo gën a neex lem».

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa giñ ne koppi mbalkaam ma ëllëg bis-pénc moo ëpp limub biddiwi asamaan si, Te loolu mi ngi feeñ ci bu guddi gi lëndëmee te weer wi génnul; ndax guddi gu am weer biddiw yi du ñu leer bu baax ndax leeraayu weer wi da leen di nëbb, te it du am Aw niir; ndax niir wi day tax duñu gis biddiw yi, Ak ne ndab i àjjana, ku ca naan dootul mar ba fàwwu, te booba la kaca naan di mujjee mar, Ak ne mbalkaam ma ñaari mballi àjjana ñoo cay yol, te yaatuwaayam moo ngi tolloog guddaayam; peggi mbalka ma ñoo tolloo, guddaayam day toll ni diggante Ummaan ab dëkk la ca Balqaa bokk ci Saam ak Aylata di dëkk buñu xam nekk ca catu Saam, Ndoxum mbalka ma moo gën a weex meew, cafka ga moo dàq lem.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Saxal mbalka ma saxalaale la fa nekk ci ay xeeti xéewal.

Màggaayu mbalka ma, ak guddaayam ak yaatuwaayam ak ay koppam yu bari.

التصنيفات

Gëm bis bu mujj ba