إعدادات العرض
Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ
Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne: indil nañu Yonente Yàlla yàpp ñu jox ko tànk ba ndax dakoo bëggoon lool, mu dal di cay xàmp, daal di wax ne: "man maay sangu nit ñi ëllëg bis-pénc, ndax xam ngeen lu tax loolu? Yàlla day dajale nit ña jiitu ak ña mujj ci benn barab, dañuy dégg aji-woote ji, te it dees leen di gis, Jant bi jege, nit ñi egg ci njàqare ak jafe-jafe lu ñu àttanul te manuñu ko a muñ, nit ñi ne: xanaa gisuleen li leen jot, ndax dungeen xool ku leen tinu ci seen Boroom? Ñenn ci ñoom wax ñeneen ñi: demleen ci Aadama, ñu ñëw ci Aadama ne ko: yaw yaay baayu nit ñi, Yàlla bind la ci loxoom, daal di wal ci yaw ci ruuham gi, mu digal malaaka yi ñu sujjóotal la, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Xanaa gisóo li nu jot? Aadama ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam , te moom da maa tere woon garab ga ma moy ko, sama bopp sama bopp doyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Nuuh, ñu dem ci Nuuh, ne ko: yaw Nuuh yaw yaay Yonente bi njëkk ci waa suuf, te Yàlla tudde na la jaam bu man a sant bi, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa amoon ñaan gu ma ñaan ci kaw sama nit ña, sama bopp sama bopp doyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Ibraahiima, ñu ñëw ci Ibraahiima, ne ko: yaw Ibraahiima yaw ndawul Yàlla nga di xaritam ci waa suuf, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa fenoon ñatti fen, sama bopp noyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Muusaa, ñu ñëw si Muusaa, ne ko: yaw Muusaa yaw ndawul Yàlla nga, te gënale na la ci yónni gi mu la yónni ak wax gi mu wax ak yaw, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa ray bakkan bob digaluñu ma ma ray ko, sama bopp noyna ma demleen ci ku dul man, demleen ci Iisaa ibn Maryma, ñu dikkal Iisaa, ne ko: yaw Iisaa yaw ndawul Yàlla nga, di kàddoom gu mu sànni ca Maryama di ruu gu jóge ci Moom, nga wax ak nit ñi ca lal ba di ab liir, tinu nu ci sa Boroom xanaa gisóo ci li nu nekk? Iisaa ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te tuddul benn bàkkaar, sama bopp noyna ma, demleen ci ku dul man, demleen ci Muhammat, ñu dem ca Muhammat, ne ko: yaw Muhammat, yaw ndawul Yàlla nga, di ki mujj ci ñi Yónente yi, te Yàlla jéggal na la li jiitu ci say bàkkaar ak Li mujj, tinu nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li nu nekk? Ma daal di dem ca ronu Aras, ma rot daal di sujjóot ñeel sama Boroom, Yàlla xamal ma ci ay xeeti sant Yàlla ak tagg ko loo xam ne masu ko xamal kenn ku ma jiitu, topp ñu ne ko: yaw Muhammat, yëkkëtil sa bopp, laajal ñu jox la, sàkkul ramm ñu jox la, ma yëkkëti sama bopp, ma wax ne: sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, ñu ne ko: yaw Muhammat, dugalal ci sa xeet ñi ñu dul càmbar ci buntu ndayjoor bi, ci bunti àjjana yi, te ñoom dañuy bokk ak nit ñi ci yeneen bunt yu dul yooyu, topp mu ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom ne li ci diggante ñaari jàppukaayi bunt yi ci bunti àjjana yi, moo ngi mel ni diggante Màkka ak Himyar -walla moo ngi mel ni diggante Màkka ak Busraa-".
الترجمة
العربية Bosanski English فارسی Français Bahasa Indonesia Русский اردو 中文 हिन्दी Tiếng Việt Español Kurdî Português සිංහල Kiswahili অসমীয়া ગુજરાતી Nederlands Hausa മലയാളം Română Magyar ქართული Moore ไทย Македонски తెలుగు मराठी ਪੰਜਾਬੀ دری አማርኛ বাংলা Malagasy Українська Tagalog ភាសាខ្មែរ ಕನ್ನಡ Svenska پښتوالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa nekkoon ak Sahaabaam yi ci ñam wuñu leen woowoon ñu jox ko tànku gàtt bi, mu nekkoon li mu gën a bëgg ci ndawalu gàtt, mu dagg ci ab dog ci cati bëñam toop mu waxtaanal leen, ne leen: Man maay sangi doomi Aadama yi ëllëg bis-pénc; loolu nag ngir waxtaane xéewali Yàlla mu kawe mi la. Topp mu wax: ndax xam ngeen lu tax loolu? Daal di ne: ndax nit ñi dañu leen di dajale ëllëg bis-pénc ci suuf su yaatu te yamoo te tàllalu gennug tàllalu, ña fa nekk dañuy dégg aji-woote ji, te aji-xool ji da leen di peeg dara du ko nëbbu ci ñoom; ndax li suuf si yamoo te dara lu kenn di nëbboo aji-xool ji nekku fa, te dees leen di gis, maanaam bu kenn nit waxee ka mujj ca ñoom da koy dégg, te bët it da leen di gis, jant bi jege mbindeef yi luy toll ni miil, ag njàqare ak ug tiit dal leen ba manuñu ko a muñ, ñuy sàkku ku leen musal ci tinul leen. Yàlla sol way-gëm ñi ñu dem ca Aadama baayu nit ñi, ñu dikkal ko tuddal ko ngëneelam, ndax amaana mu tinul leen fa Yàlla mu màgg mi, ñu ne ko: yaw Aadama yaaw baayu mbindeef yi, Yàlla bind la ci loxoom, sujjóotloo malaaka yi ñeel la, mu xamal la tur yëpp, daal di wal ci yaw ruuham ga, mu joxe ngànt ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du musa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, mu daal di tudd njuumteem, te mooy ne Yàlla da ko a tere woon mu lekk ag garab mu lekk ko, mu wax ne: sama bakkan moo gën a yay ñu tinu ko, demleen ci ku dul man, demleen ci Nuuh. Ñu dikkal Nuuh; ne ko: yaw yaay Yonente bi Yàlla njëkk a yónni ci waa suuf, te Yàlla tudde na la jaam bu barig cant, waaye moom dafa joxe ngànt: ci ne Yàlla mu màgg mi dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, ak ne moom dafa amoon ñaan gu mu ñaan ci kaw ay nitam, sama bakkan moo gën a yay ci ñu tinu ko, demleen ci ku dul man, demleen ci Ibraahiima. Ñu dikkal Ibraahiima ne ko: yaw yaay xaritu Yàlla bi ci kaw suuf, tinul nu ci sa Boroom xanaa gisóo ci li nu nekk?! Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa fen ñatti fen; te mooy waxam ji: damaa tawat, ak waxam ji: seen ponkal mii moo ko def, ak waxam ji: ñeel soxnaam sa Saarata wax ko ne man sa mbokk laa ngir mu mucc ca ayam wa. Te liy dëgg mooy ñatti kàddu yii gaaralug wax kepp la, waaye ba mu nekke ci melow fen ca la ragale ngir xeeb boppam ci tinu leen; ndax ku gën a xam Yàlla te gën ko a jege koo ku mooy gën a ragal Yàlla, mu wax ne: sama bakkan moo gën a yay ci ñu tinu ko, demleen ci ku dul man, demleen ci Muusaa. Ñu dikkal Muusaa ne ko: yaw Muusaa yaw ndawul Yàlla nga, Yàlla gënële la ci yónenteem ak waxam ji ci kaw nit ñi, tinul nu ci sa Boroom xanaa gisóo ci li nu nekk?! Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te man damaa ray bakkan bu ñu ma digalul ma ray ko, sama bopp bakkan moo gën a yay ci ñu tinu ko, demleen ci ku dul man, demleen ci Hiisaa ibn Maryma. Ñu dikkal Hiisaa ne ko: yaw Hiisaa yaw ndawul Yàlla nga, di kàddoom gu mu sànni ca Maryama, di ruu gu jóge ci moom, nga wax ak nit ñi ci lal bi di ab liir, tinul nu ci sa Boroom xanaa gisóo ci li nu nekk?! Mu ne leen: sama Boroom dafa mer tay am mer moo xam ne masul mer mer mu mel ni moom, te du masa mer mer mu mel ni moom ginnaawam, te tuddul benn bàkkaar, sama bakkan moo gën a yay ci ñu tinu ko, demleen ci keneen, demleen ci Muhammat. Ñu dikkal Muhammat, ne ko: yaw Muhammat yaw ndawul Yàlla nga di ki mujj ci ñi ñu soloo, te Yàlla jéggal na la say bàkkaar ya jiitu ak ya mujj, tinul nu ci sa Boroom, xanaa gisóo ci li ñu nekk?! Ma wéy, daal di dem ca ronu Aras, ma rot daal di sujjóot ñeel sama Boroom, Yàlla ubbeema ci ay xeeti cànt ak tagg ko, loo xam ne masu ko a ubbee kenn ku ma jiitu, topp ñu ne ko: yaw Muhammat, yëkkëtil sa bopp, laajal ñu jox la, tinul ñu tin la ci, ma yëkkëti sama bopp, ma wax ne: sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, sama xeet wi yaw sama Boroom, ñu nangu ag rammam. Ñu ne ko: yaw Muhammat, dugalal ci sa xeet ñi ñu dul càmbar ci buntu ndayjoor bi, ci bunti àjjana yi, te ñoom dañuy bokk ak nit ñi ci yeneen bunt yu dul yooyu. Topp mu ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom ne li ci diggante ñaari jàppukaayi bunt yi ci bunti àjjana yi, moo ngi mel ni diggante Màkka ak Sanhaa ca Yaman walla moo ngi mel ni diggante Màkka ak Busraa ca Saam te mooy Madiinatu Hawraan.فوائد الحديث
Toroxlug Yónente bi ak wuyu gimuy wuyu ñeel ku ko woo, ak lekk gi muy lekk ànd ak Sahaabaam yi.
Ngëneelu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci kaw nit ñépp.
Al-Xaadii Hiyaad nee na: nee nañu sang mooy kiy yilif aw nitam ñuy dellu ci moom bu tar-tar yi amee, te Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mooy seen sang ci àdduna ak allaaxira, waaye dafa jagleel allaaxira cig tudd ngir la fa sang ga di yëkkëtiku, ak li ko ñépp di nangul loolu, ak li Aadama ak doomam yépp di nekk ci suufu raayaam moom Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Xereñte gi mooy ne Yàlla da leen a defal ñu laaj Aadama ak ka ca topp, te mayu leen ñu laaj Yónenteem bi Muhammat ngir feeñal ngëneelam, te loolu mooy la këna kawe ci daraja, ak ug jege Yàlla gu mat sëkk.
Yoonalees na ku am aajo ci keneen mu tuddalko ay meloom ya gën a rafet; ngir mu gaaw koo wuyu.
Dagan na ci ku ñu laaj lu mu manul mu joxe ngànt gu ñu koy nangule, sopp na ñu itam mu tegtale ku mu njort ne man na loolu.
Leeral tiitaangey taxawaay ba ak tarug dajale ga ci jaam ñi ëllëg bis-pénc.
Toroxlug Yonente yi ba tax ñuy tudd li weesu woon ci ñoom; ngir ñu yég ne ñoom egguñu foofu.
Saxal ramm gu màgg ga ëllëg bis-pénc, te mooy ñu teqale diggante mbindeef yi.
Saxal wasiila ak maqaama ga ñu gërëm mu ñeel Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Canti Yàlla yi du jeex, loolu moo tax Yàlla jox Yonnenteem bi ci barab bii ay xeeti tagg yu rafet lu mu musut a jox kenn ci ñi ko jiitu.
Leeral ne xeetu Muhammat mooy xeet wi gën, ñoom am nañu ay jagle ci dugg àjjana ba ñoo xam ne deesu leen càmbar danañu dugg ci bunt bu ñu leen jagleel, te dañuy bokk ak nit ñi yeneen bunt yi des.
التصنيفات
Dundug alaaxira