amul benn boroom wurus du caagine xaalis, te du joxe àqam, lu dul ne bu bis-pénc baa dees na ko lalal ay lali xeeri sawara

amul benn boroom wurus du caagine xaalis, te du joxe àqam, lu dul ne bu bis-pénc baa dees na ko lalal ay lali xeeri sawara

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «amul benn boroom wurus du caagine xaalis, te du joxe àqam, lu dul ne bu bis-pénc baa dees na ko lalal ay lali xeeri sawara, tàngal ko ca sawaraw Jahannama, diko paase ca wetam ga ak jëham ba ak ndiggam la, teg ca saa bu seddee rekk ñu delloo ko ca, ci bis bob ab nattaleem moo ngi toll ni juróom-fukki junniy at, ba keroog ñuy àtte diggante jaam ñi, mu gis yoonam, benn mu jëm àjjana, walla mu jëm sawara». Ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi bu dee ay giléem nag? "Ak bu dee boroomi giléem te du joxe àqam, te bokk na ci àqam nu ratt ko bis bu nàndalee, bu bis-pénc baa ñi lalal ko bayaal bu tàlli, ca namu gën a mate, fu ca ñàkk menn murt, ñu koy dëgg ca seen we ya, di ko màtt ca seen gémmiñ ya, saa bu ya jiitu jàllee ñu delloosi ya mujj, ci nis boo xam ne moo ab nattaleem moo ngi mel ni juróom-fukki junni at, ba keroog ñuy àtte jaam ñi, mu gis yoonam wa, benn mu jëm àjjana, walla mu jëm sawara. Ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, lii di nag ak gàtt nag? Mu ne: "ak boroom nag, ak gàtt, bu dul joxe àqam lu dul bu bis-pénc baa ñu lalal ko bayaal bu tàlli, du ca ñàkk dara, amu ca bu béjjan yi lemu, du caagine bu amul béjjan, du caagine bu béjjan yi damm, ñu koy mbëkk ci seen i béjjan, di ko dëgg ci seen i we, saa bu ya jiitu jàllee ñu delloosi ya mujj, ci bis boo xam ne ab nattaleem moo ngi mel ni juróom-fukki junniy at, ba keroog ñuy àtte jaam ñi, mu gis yoonam wa, benn mu jëm àjjana, walla mu jëm sawara" Ñu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, bu dee fas nag? Mu wax ne: "fas ñatt la: te ñooy, wi nit ki di am bàkkaar, ak wi nit gi di ame kiiraay, ak wi nit ki di ame yool, bu dee wi miy am bàkkaar, mooy wi waa ji yeew ngir ngistal ak puukarewu ak ngir jiite waa lislaam, moom bàkkaar la ciy am, bu dee wimiy ame kiiraay, mooy wi waa ji yeew ci yoonu Yàlla, te fàttewul àqi Yàlla ca ndiggam la du caagine doqam ga, moom kiiraay la ci moom, bu dee wimiy ame yool, mooy wi waa ji yeew ci yoonu Yàlla ngir waa lislaam, muy lekk ca àll ba ak ca tool yi, du lekk dara ca àll ba walla ca tool ya lu dul ne dees na ko bindal limu la mu lekk ay yiw, ñu bindal ko limu ay nefereem ak am sawam ay yiw, te duñu dagg buumam ga muy gaawantu jëm ci genn wet walla ñaari wet, lu dul ne Yàlla dana ko bindal limub ay jeexiitalam, ak ay nefereem ay yiw, te boroomam du ko rombale ci ag dex, mu naan ca te sax nammu ko woon a nàndal, lu dul ne Yàlla dana ko bindal limub la mu naan ay yiw"

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeral na ay xeeti alal, ak fayug ku dul joxe asakaam ëllëg bis-pénc, te bokk na ca: Bi ci njëkk: wurus ak xaalis ak lu nekk ci seen àtte ci alal yi ak yi ñuy jaay, te mooy yi asaka war te joxewuñu ko ci, bu bis-pénc baa dañu koy seeyal sotti ko ci ay aliwo, daal di cay taal sawaraw Jahannama, mbugal ca boroomam, daal di cay bomb wetam ga ak jëham ba ak ndiggam la, saa bu seddee ñu tàngalaat ko, muy wéy ca anamu mbugal mooma diirub bis-pénc ba nga xam ne moo ngi tool ni juróom-fukki junniy at, ba baa Yàlla di àtte diggante mbindeef yi, mu bokk ci waa àjjana walla ci waa sawara. Ñaareel bi: boroom giléem gi dul joxe faratay asaka ak àqam, te bokk na ca ratt ko ñeel ña fa teew ci ay way-ñàkk, ñu indi giléem yi mu màgg te duuf ca limam ba gën a bari, ñu daal di tàllal boroomam ëllëg bis-pénc sànni ko ci suuf su yaatu te yamoo ñu koy dëgg ci seen i tànk, di ko màtt ci seen i bëñ, saa bu ña mujj jàllee ci kawam ñu delloosi yu njëkk ya, muy wéy ca anamu mbugal mooma diirub bis-pénc ba nga xam ne moo ngi tool ni juróom-fukki junni at, ba keroog Yàlla di àtte diggante mbindeef yi, mu bokk ci waa àjjana walla ci waa sawara. Ñatteel bi: ki moom ay nag ak ay gàtt -xar ak bëy- te boroomam du joxe àqi asakaam, ñu indi leen ca lim ba gën a mat dara du ca wàññeeku, ñu daal di tàllal boroomam ëllëg bis-pénc sànni ko ci suuf su yaatu te yemoo, te du am benn bu béjjan bi lemu, du caagine bu amul béjjan, du caagine it bu béjjan yi lemu, waaye ca melokaan wa gën a mat, ñu koy mbëkk ca seen béjjan ya, di ko dëgg ca seen tànk ya, saa bu ña mujj jàllee ci kawam ñu delloosi yu njëkk ya, muy wéy ca anamu mbugal mooma diirub bis-pénc ba nga xam ne moo ngi tool ni juróom-fukki junni at, ba ba Yàlla di àtte diggante mbindeef yi, mu bokk ci waa àjjana walla ci waa sawara. Ñenteel bi: ki yor fas, moom nag ñatti xeet la: Bu njëkk bi: bàkkaar la ciy am, te mooy ki ko wut ngir ngistal ak puukarewu ak xeex waa lislaam. Ñaareel bi: sutura la ciy am, te mooy ki ko wut ngir jihaad ci yooyu Yàlla, topp mu rafetal jëme ci moom ci di ko xont ak mbooleem dundam, te bokk na ca boyal bu góor ba. Ñatteel bi: da ciy am yool, te mooy ki ko wut ngir jihaad ci yoonu Yàlla mu ñeel waa lislaam, mu nekk ci ay dër ak i tool ngir sàmm, du ca lekk lu dul ñu bindal ko limub la mu lekk ay yiw, bindal ko li mub ay nefereem ay yiw, te du ñu dagg buumam ga, te mooy buum ngi ñu koy yeewe, mu daw wéy ci kaw suuf; lu dul ne danañu ko bindal li mu ay jeexitalam ak i nefereem ay yiw, te boroomam du ko rombale ci ag dex mu naan ca te nammu ko woon a nàndal, lu dul ne dees na ko bindal li mu la mu ca naan ay yiw. Topp ñu laaj ko yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mbaam ndax day yamoo ak fas? Mu wax ne: dara ci yoonal gu mu jagoo waccu ci, lu dul aaya ju néew moroom jii, te dafa matale ci mbooleem xeeti topp yi ak moy yi; te mooy waxu Yàlla ji: {ku jëf luy toll ni aw fepp ci lu baax dana ko gis, ku jëf luy toll ni aw fepp ci lu bon dana ko gis}. [As-Salsala: 8], ku jëf ci li mu yor mbaam ag topp dana gis yoolu loolu, bu dee ag moy la jëf dana gis mbugalu loolu, te lee dafa matale mbooleem jëf yi.

فوائد الحديث

Warug joxe asaka, ak tëkku gu tar gi tege ci bañ ko.

Ñàkk a kéefarloo ki bañ a joxe asaka ngir tàyyeel, waaye moo ngi ci giraawaale gu tar.

Nit ki dees na ko fay mbooleem ay jëfam bu ca jubloo cosaan la, donte sax jubluwul faramface yooya.

Àq ju dul asaka nekk na ci alal ji.

Bokk na ci àqi giléem ratt ko ñeel ña fa teew ci ay way-ñàkk ca barab ba muy naane ndox; ngir mu gën a yomb ci aji-aajowoo ji ci muy dem ca kër ya, te moo gën a am ñeewant ci jur gi, Ibn Battaal nee na: alal ji am na ñaari àq: faratay jëmm ak gu dul moom, ratt gi dafa bokk ci àq yi nga xam ne ci teddngay jikkó la.

Bokk na ci àq yi war ci giléem ak nag ak gàtt yi boyal bu góor ba bu sàkkoo fori.

Àtteb mbaamu kër ak lépp lo xam ne yaxub sariiha rotuci: mooy ne day dugg ci waxi Yàlla ji: (ku jef lu toll ni aw fepp ci lu baax dana ko gis, ku jëf it lu toll ni aw fepp ci lu bon dana ko gis).

Aaya bi am na xemmeemloo ci jëf lu baax donte lu néew la, ak xuppaate ci jef lu bon donte lu xeebu la.

التصنيفات

Dundug alaaxira, Warug natt asaka ak àtteb ki ku bàyyi, Li nit def ci yoonu Yàlla ci alalam ngir nit ñi di ko jariñoo te kenn du ko donn