xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?

xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?

Jële na ñu ci Xataadatu -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne: Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na nu ne benn waay dafa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ? Mu ne ko: «xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?» Xataadatu wax na: ahakay giñ naa ko ci sunu màggug Boroom.

الشرح

Leerarug hdiis bi: Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ëllëg bis-pénc?! Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: xanaa du Yàlla mi ko doxloo fii ci àdduna ci ñaari tànkam man na koo doxloo ci xar kanamam ëllëg bis-pénc ?! Yàlla lépp la man.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Doyadig yéefar bi ëllëg bis-pénc ba day doxe ci xar kanamam.

التصنيفات

Gëm bis bu mujj ba, Wéetal Yàlla ci moom gi mu moom lépp di ko saytu, Wéetal Yàlla ci ay turam ak i meloom