Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa am lu mu tudd daal di ne: «loolu de bu xam-xam di dem lay doon

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa am lu mu tudd daal di ne: «loolu de bu xam-xam di dem lay doon

Jële na ñu ci Siyaad Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- me wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa am lu mu tudd daal di ne: «loolu de bu xam-xam di dem lay doon» ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, naka la xam-xam di deme, te nun noo ngi jàng Alxuraan di ko jàngal sunuy doom, sunuy doom di ko jàngal séen i doom, ba keroog bis-pénc? Mu wax ne: « sa yaay ñàkk yaw Siyaad, man de foogoon naala ki gën a amug dégg ci Madiina, xanaa du Yahuut yi ak Nasaraan yi ñoo ngi jàng Tawraat ak Injiil, te duñu jëfe dara ca la fa nekk?!».

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa toogoon ci biir Sahaaba yi, daal di wax ne: jamono jii mooy ji ñuy yëkkati xam-xam di dindi xam-xam ci nit ñi, Siyaad Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- yéemu daal di laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Ne ko: naka la ñuy yëkkatee xam-xam ba mu sànku ci nun?! Te jàng nanu Alxuraan mukkal ko; te giñ naa ci Yàlla ne dananu sax ci di ko jàng, dananu ko jàngal sunuy jigéen ak sunuu doom, ak sunuy sët. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daldi yéemu ne ko: nala sa yaay ñàkk rekk yaw Siyaad! man de boole woon naa la ci boroomu xam-xami Madiina yi! Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di koy leeral ne: ñàkk xam-xam gi nekkul ñàkk Alxuraan; waaye ñàkk xam-xam mooy ñàkk koo jëfe, Ndax Tawraat ak Injiil ñoo ngi ci Yahuut yi ak Nasaraan yi; ànd ak loolu jariñu leen, te jariñuwuñu ca la ñu jublu woon ci ñoom ñaar; te mooy jëfe la ñu xam.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Alxuraan ji ak téere yi nekk ci yoxoy nit ñi rekk du jariñ te àndul ak jëfe ko.

Yëkkatig xam-xam ci ay bir lay ame, bokk na ca: faatug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak faatug woroom xam-xam yi, ak bàyyee jëfe xam-xam.

Bokk na ci màndargay bis-pénc xam-xam dem ñu bàyyi koo jëfe.

Soññee ci jëfe xam-xam ndaxte mooy jubluwaay bi.

التصنيفات

Dundug barsàq, Merit and Significance of Knowledge