Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk

Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Sama mbalka ma de mi ngi toll ne doxu weer, ndoxam ma moo gën a weex meew, xetam ga moo gën a neex gëttug misk, te koppu yi dañoo mel ni biddiwi yi nekk ci asamaan Ku ci naan doo mar mukk ».

الشرح

Leerarug hdiis bi : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne am na am mbalka ëllëg bis-pénc, guddaayam mi ngi toll ne doxu weer yaatuwaayam it naka noonu, Ndoxam ma moo gën a weex meew, Xetam moo gën a neex te gën a teey xetu misk, Ay koppam moo ngi toll ne biddiwi asamaan cig bari, Ku naan ca mbalka ma ci kopp yooya dootul mar ba fàwwu.

فوائد الحديث

Déegu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fu ndox dajaloo la mu màgg lool, te way-gëm ci xeetam ñoo cay naan ëllëg bis-pénc.

Ku naan ca déeg ba dana am xéewal te dootul mar mukk.

التصنيفات

Gëm bis bu mujj ba