ku wattu fukki aaya yi njëkk ci saaru Al-Kahf, kon ñu aar ko ci Dajjaal" ci geneenug nettali: "ci mujjug saaru Al-Kahf

ku wattu fukki aaya yi njëkk ci saaru Al-Kahf, kon ñu aar ko ci Dajjaal" ci geneenug nettali: "ci mujjug saaru Al-Kahf

Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "ku wattu fukki aaya yi njëkk ci saaru Al-Kahf, kon ñu aar ko ci Dajjaal" ci geneenug nettali: "ci mujjug saaru Al-Kahf".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne ku mokkal fukki aaya yi njëkk ci saaru Al-Kahf ci xolam ñu aar ko ci fitnay Masiihu-Dajjaal mi nga xam ne day génn ci mujjug jamono di wootewoo Yàlla, te fitnaam nag mooy fitna ji gën a màgg ci kaw suuf ba ñi bindee Aadama ba keroog Saa di taxaw; ngir li ko Yàlla kàttanal mu am yenn ci ay xar-baax yimuy fitnaale ñi ko topp, loolu nag ndaxte njëlbeenu saaru Al-Kahf dafa am ay kéemtaan ak ay aaya yu gën a màgg yi Dajjaal di fitnaale nit ñi, ku ko settantal du fitnawu ci Dajjaal.m Nekk na ci geneen nettali: fukki aaya yi ci mujjug saar wi, mu tàmbalee ci waxu Yàlla mu kawe mi: {Afa hasiba allasiina kafaruu an yattaxisuu...}.

فوائد الحديث

Leeral ngëneelu saaru Al-Kahf, ak ne ay tàmbaleem walla ay mujjam day aare ci fitnay Dajjaal.

Xibaare mbiri Dajjaal, ak leeral liy aare ci moom.

Ñaaxe ci mokkal saaru Al-Kahf ba mu jeex, bu ko manul na mokkal fukki aaya yi njëkk walla yi mujj.

Al-Xurtubii wax na ci sababu loolu ne: nee nañu: li tax mooy li nekk ci nettalib ashaabul kahfi ci ay keemaan ak i aaya, ku ko jàng du yéemu ci mbiri Dajjaal te te du ca fitnawu, nee nañu it: ngir li Yàlla wax ne: {ngir mu xuppe ci mbugal mu tar muy bawoo ci Moom} te loolu lu méngoo la ak li Dajjaal di nekke ci wootewoo Yàlla ak ug noteel ak màggug fintaam, loolu a tax Yonnente bi màggal ay mbiram daal di ciy àrtu daal di muslu ci fitnaam, kon maanaa hadiis bi di: ku jàng aaya yii ci ag settantal daal di taxaw ci ay maanaam da na ko moytu daal di mucc ci moom.

التصنيفات

Ngëneeli saar yi ak laaya yi, Màndargay bis-pénc