am nga li nga mébét ak lu mel ni moom

am nga li nga mébét ak lu mel ni moom

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "barab bu kenn ci yéen bi gën a suufe ca àjjana mooy ñu wax ko: mébétal muy mébét di mébét, mu ne ko: ndax mébét nga? Mu ne: waaw, mu ne ko: am nga li nga mébét ak lu mel ni moom".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne ki gën a suufe te gën a néew daraja ak martaba ci ñiy dugg àjjana mooy ñu wax ko: mébétal, muy mébét di mébét, ba deseetul genn mébét lu dul ne tudd na ko, mu ne ko: ndax mébét nga? Mu ne: waaw, mu ne ko: am nga li nga mébét ak lu mel ni moom.

فوائد الحديث

Rawanteg këri waa àjjana ya.

Leeral màggug teddngay Yàlla mu kawe mi tudd naa Sellam gi.

Xéewali àjjana yi tënkuwul ci mbir mu ñu ràññee, wànte aji-gëm ji dana ca fekk lépp lu mu mébét te bakkanam bëgg ko muy ngëneel ak tabe ak teddnga bu bawoo ci Yàlla mu kawe mi.

التصنيفات

Dundug alaaxira, Meloy Àjjana ak Sawara