bokk na ci ñi gën a bon ci nit ñi mooy ñi bis-pénc di ñëw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka

bokk na ci ñi gën a bon ci nit ñi mooy ñi bis-pénc di ñëw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne: «bokk na ci ñi gën a bon ci nit ñi mooy ñi bis-pénc di ñëw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka».

[Tane na] [Ahmat soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ñi gën a yées ci nit ñi, te mooy ñi nga xamne saa day taxaw fekk ñuy dund, ak ñiy jàppe bàmmeel yi ay jàkka, di fa julli ak di fa jublu.

فوائد الحديث

Araamalees na tabax jàkka ci kaw ay bàmmeel; ndax day sabab bokkaale.

Araamal nañu julli ci ay bàmmeel donte tabaxuñu ko; ndax jàkka aw tur la ñeel fa ñuy sujjóote doonte tabax nekku fa.

Ku jàppe bàmmeeli ñu baax ñi ay jàkka ngir di fa julli kooku ci ñi yées ci nit ñi la bokk, donte dafa foog ne jublu bàmmeel jegeñ-jegeñlu Yàlla mu kawe mi la.

التصنيفات

Màndargay bis-pénc