bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-

bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ca àjjana, ne ko: demal xool ko ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko daal di ñëw, ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ne kenn du ko dégg lu dul ne dana def lu ko cay dugal. Mu digle ñu wërale ko ak ay tiis, mu ne ko: demal xool ko ak la nu ca waajalal ay ñoñam, mu fekk ñu muure ko ak i tiis mu wax ko ne: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du fa dugg. Mu ne ko demal nga xool sawara ak la ma ca waajalal ay ñoñam. Mu xool ko gis waa sawara a nga warante, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi kenn du def lu la fay dugal. Mu digle ñu muure ko ak i bànneex, mu ne ko: dellul xool ko. Mu xoolaat ko gis ñu muure ko ak i bànneex, mu dellu ne ko: giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du ca mucc».

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy]

الشرح

Leerarug hdiis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne bi Yàlla bindee àjjana ak sawara, dafa wax Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-: demal àjjana xool ko, mu dem xool ko daal di dellusi, Jibriil ne ko: yaw sama Boroom giñ naa ci sa màgg gi amul kenn kuy dégg àjjana ak la fa nekk ci ay xéewal ak i terànga ak i yiw lu dul ne dana fa bëgg a dugg, te dana jëf ngir loolu. Yàlla muur àjjana wërale ko ak i tiis ak i jafe-jafe ci def ndigal ak moytu tere yi; kon képp ku fa bëgg a dugg war naa jéggi tiis yooyu. Yàlla mu kawe mi ne: yaw Jibriil! Demal xoolaat àjjana, ginnaaw bamu ko wëralee ak i tiis, Mu dem xool ko, daal di ñëw ne ko: yaw sama Boroom, giñ naa ci sa màgg gi ragal naa ne kenn du fa dugg ngir jafe-jafe yi ak tar-tar yi nekk ci yoon wi. Ba Yàlla bindee sawara, ne: yaw Jibriil! Demal xool ko, mu dem xool ko. Daal di ñëw, ne ko: yaw sama Boroom, giñ naa ci sa màgg gi kenn du dégg la fa nekk ci mbugal ak i tiis ak i mettit lu dul ne dana fa bañ a dugg te dana sori lépp lu koy waral. Yàlla mu kawe mi muur sawara def ci yoon wa fa jëm ay bànneex ak i neex-neex, mu ne ko: yaw Jibriil, dellul nga xool ko. Jibriil demaat xool ko, daal di ñëw, ne ko: yaw sama Boroom giñ naa ci sa màgg gi ragal naa te tiit naa lool ne kenn du ca mucc; ngir li ko wër ci ay bànneex ak i neex-neex.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Gëm ne àjjana ak sawara fi mu ne nii am nañu.

Dañoo war a gëm kumpa ak lépp lu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- indi.

Solos muñ tiis yi ndax te yoon la wuy àggale àjjana.

Solos moytu yu araam yi; ndax te yoon la wuy yóbbe sawara.

Àjjana dañu koo muure ak i tiis, sawara ñu muure ko ak i bànneex, loolu mooy nattub dundug àdduna gi.

Yoonu àjjana dafa jafe te metti, day aajowoo muñ ak jàmmaarlook yu metti yi ànd ak ngëm, yoonu sawara nag daa fees dell ak i neex-neex ak i bànneex fii ci àdduna.

التصنيفات

Gëm bis bu mujj ba, Meloy Àjjana ak Sawara