giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bi màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi lempo bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko

giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bi màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi lempo bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bi màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi lempo bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day waat ci ne wàccug Iisaa Ibn Maryama -yal na ko Yàlla dolli jàmm- jege na day wàcc di àtte ci diggante nit ñi cig màndute ci Sariihab Muhammat, Ak ne dana toj kurwaa yi nasaraan yi di màggal, Ak ne Iisaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm- dana ray mbaam-xuux yi, Ak ne moom dana dindi lempo digal nit ñépp ñu dugg ci Lislaam. Ak ne alal dana baawaan ba kenn du ko jël; ndax bariwaayam, ak doylug kenn ku ne ci li mu am, baarke wàcc yiw yi toftaloo.

فوائد الحديث

Saxal wàccug Iisaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ci mujjug jamono, ak ne dafa bokk ci màndargay bis-pénc.

Sariihab Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa folli bu dul moom.

Wàccug baarke ci alal yi ci mujjug jamono, ak ni ko nit ñi di dëddoo.

Bégle ci desug diiney Lislaam ba Iisaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm- ci lay àtte ci mujjug jamono.

التصنيفات

Yónnent yi jiitu yalna jàmm nekk ci ñoom, Sunu Yónnent Muhammat yalna Yàlla xéewalal ko te jàmmal ko, Dundug barsàq, Léppi diiney Lislaam