saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu keneen di naan: aka neexoon ma nekk palaasam

saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu keneen di naan: aka neexoon ma nekk palaasam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu keneen di naan: aka neexoon ma nekk palaasam».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bis-pénc du taxaw mukk lu dul ne nit dana romb ab bàmmeel di mébét bu deewoon ba nekk palaasam, te sabab sa mooy dafa ragal ci boppam diineem di dem ngir li ag neen ak i ñoñam di not, ba fitna ak moy ak yu bon yi fés.

فوائد الحديث

Ag juñj la ci ne moy yi ak fitna yi dañuy fés ci mujjug jamono.

Soññee ci moytu ak waajal dee ci gëm ak jëf yu baax, te sori bérabi fitna yi ak balaa yi.

التصنيفات

Dundug barsàq, Tolluwaayi ñu baax ñi, Sellal bakkan yi