dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf

dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf

Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf, ab wootekat daal di woote: yéen waa àjjana, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, mu woote ne: yéen waa sawara, ñu yoqamtiku di xool, mu wax ne: ndax xam ngeen lii ? Ñu ne ko: waaw, lii mooy dee, te ñoom ñépp a ko gis, ñu rendi ko, mu wax ne: yéen waa àjjana sax ba fàwwu dee amatul, yéen waa sawara sax ba fàwwu dee amatul, daal di jàng: {na nga leen xupp bisub réccu ba ba ñu àttee mbir ma fekk ñoom ñoo ngi cig càggante} [Maryama: 39], waa àdduna jii ñoo ngi cig càggante, {te ñoom duñu gëm}[Maryama: 39]».

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ëllëg bis-pénc dañuy indi dee, ci melom xar mu am weex ak ñuul, Ñu woote: yéen waa àjjana! Ñu tàllal séen baat ak séen doq yi yëkkati séen bopp yi di xool, Mu ne leen: ndax xam ngeen lii? Ñu ne: waaw, lii mooy dee, ñoom ñépp gis nañu ko te xam nañu ko, Wootekat bi woote: yéen waa sawara, ñu tàllal séen baat yi ak séen doq yi yëkkati séen bopp yi di xool, Mu ne: ndax xam ngeen lii? Ñu ne: waaw, lii mooy dee, ñoom ñépp gis ko; Ñu rendi ko, wootekat bi ne: yéen waa àjjana des ba fàwwu dee amatul, yéen waa sawara des ba fàwwu dee amatul. Ngir loolu dolliku ci xéewali way-gëm ñi, waaye di yokk mbugali way-weddi yi. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng: {na nga leen xupp bisub réccu ba bu ñu àttee mbir ma te ñoom ñoo ngi cig càggante te ñoom duñu gëm} Bis-pénc dañuy tàqale diggante waa àjjana ak waa sawara, ku nekk dugg fa muy sax, Ñi doon def ñaawtéef di réccu te réccu du jariñ, ak ki gàttañlu bu yokkul ay yiw.

فوائد الحديث

Mujjug nit ca allaaxira mooy sax ba fàwwu ca àjjana walla sawara.

Artu gu tar ci tiitaangey bis-pénc ci ne bisub réccu la.

Leeral ne mbégtem waa àjjana day sax, ak njàqarey waa sawara.

التصنيفات

Gëm bis bu mujj ba, Meloy Àjjana ak Sawara, Pirim laaya yi