amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, alkande ñeel na araab yi ci ay wu jege, tijji nañu tay ci baaraasu Yaajuuja ak Maajuuja lu toll ni

amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, alkande ñeel na araab yi ci ay wu jege, tijji nañu tay ci baaraasu Yaajuuja ak Maajuuja lu toll ni

Jële nañu ci Saynabu Bint Jahsin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa dugg fi moom fekk moo ngi jàq, di wax naan: «amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, alkande ñeel na araab yi ci ay wu jege, tijji nañu tay ci baaraasu Yaajuuja ak Maajuuja lu toll ni" mu ràbbale baaraamu déyam ak ba ca topp, Saynabu Bint Jahsin nee na ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi: ndax dees nuy alag te ñu baax ñi nekk sunu biir? Mu ne ko: "waaw bu lu bon baree».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa dugg fi soxnaam Saynabu Bint Jahsin yal na ko Yàlla dollee gërëm daal di jàq ragal, di wax naan: amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ngir yégle ne moo ngi séentu ne mbir mu naqari nar naa xew, te deesu ci mucc ci lu dul làqu jëm ci Yàlla mu Sell mi, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: Alkande ñeel na araab yi ci ay woo Xamne ag dikkam jege na, tijji nañu tay jii ci baaraasu Yaajuuja ak Maajuuja, ab baaraas la bu Sul xarnayni tabaxoon, lu toll ni, daal di wërale baaraamu déyam ak ba ca topp, Saynabu yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: naka la Yàlla di wàccee alkande ci nun te way-gëm yu baax yi nekk ci sunu biir? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: bu lu bon baree ag caay-caay ak ug kàccoore ak i moy, ak njaalo, ak naan sàngara, ak yeneen yi, kon alkande day matale ñépp.

فوائد الحديث

Jàq du soxlaal xolu jullit bi wolif muy tudd Yàlla bu ragalee; ndaxte ci tudd Yàlla la xol yi di dale.

Ñaaxe ci dindi moy yi ak tere koo am.

Alkande dana matale ci sababus moy yu bari ak ug tasaaroom donte ñu baax ñi bari nañu.

Musiba yi dana daj nit ñépp ñu baax ñi ak saay-saay si, waaye dees leen di dekkil ca seen yéene ya.

Dafa jagleel araab yi cig tudd ci li mu wax ne: "alkande ñeel na araab yi ci ay wu jege"; ndaxte ñoom ñoo ëppoon ci ñi tuub jamono yooya.

التصنيفات

Màndargay bis-pénc, Na mu daa doxalee ci sëy ak dundam ak i soxnaam