إعدادات العرض
Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira
Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee ne: «Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira, bu dee ab yéefér nag ay jëfam yu baax yi mu def ngir Yàlla fii ci àdduna, dañu ka koy dundale, ba bu demee allaaxira, du fa fekk jenn jëf ju baax buñu koy fay».
[Wér na] [Muslim soloo na ko]
الترجمة
العربية English မြန်မာ Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands اردو Español Bahasa Indonesia ئۇيغۇرچە বাংলা Türkçe Bosanski සිංහල हिन्दी Tiếng Việt Hausa മലയാളം తెలుగు Kiswahili ไทย پښتو অসমীয়া Shqip دری Ελληνικά Български Fulfulde Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy or Română Kinyarwanda Српски тоҷикӣ O‘zbek नेपाली Moore Kurdî Oromoo Soomaali Français Tagalog Azərbaycan Українська bm தமிழ் Deutsch ქართული Português mk Magyar فارسیالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral màggug ngëneelu Yàlla ci way-gëm ñi, ak màndoom ci yéefar yi. Aji-gëm ji deesul wàññi ci yooli jëfam ju baax; waaye dees koy jox fii ci àdduna ci yiw ci ay jaamoom, ànd ak loolu ñu dencal ko payam ca allaaxira; amaana it ñu dencal ko payam gépp ba allaaxira. Bu dee ab yéefar nag Yàlla da koy jox payug li mu def ci yu baax fii ci àdduna, ba bu demee allaaxira du fa fekk am lenn lu baax lu ñu koy fay; ndaxte jëf yu baax yiy jariñ ci ñaari kër yi fàwwu boroomam nekk aji-gëm.فوائد الحديث
Ku faatu cig kéefar jëfam du ko jariñ.