saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee

saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee, am at di mel ni weer, weer di mel ni ayu bis, ayu bis di mel ni benn bis, benn bis di mel ni wenn waxtu, wenn waxtu di mel ni taal xobi tàndarma».

[Wér na] [Ahmat soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare ne bokk na ci màndargay bis-pénc jegeeg jamono yi, At mi di romb kem ni weer di rombe, Weer di romb kem ni ayu bis di rombe, Ayu bis di romb kem ni benn bis di rombe, Benn bis di romb kem ni wenn waxtu di rombe, Wenn waxtu di romb gaaw lool ba mel ni xob wu ñuy lakk, te mooy xobu tàndarma.

فوائد الحديث

Bokk na ci màndargay bis-pénc ñu dindi barke ci jamono ji mbaa gaawaayam.

التصنيفات

Dundug barsàq