yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko

yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko

Jële nañu ci Jariir Ibn Abdullah -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Nekkoon nanu fi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu xool weer wi ci genn guddi -guddi yu leer yi- daal di wax ne: " yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko, bu ngeen manee ba deesu leen not ci jullig fajar njëkk jant bi di fenk ak njëkk muy so defleen ko" mu daal di jàng: "{nanga sàbbaal sa Boroom njëkk fenkug jànt bi ak njëkk so ga}"

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Sahaaba yi dañoo nekkoon ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci genn guddi mu xool weer wi -guddig fukkeel ak ñent-, daal di wax ne: Jullit ñi de danañu gis seen Boroom ca dëgg-dëgg ci seen i gët ci lu dul menn lënt, te duñu xat-xatloo, duñu ci am benn coono mbaa jafe-jafe bu ñu koy gis moom Yàlla mu kawe mi. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne : Bu ngeen manee dagg mbir yi leen di teree julli fajar ak tàkkusaan defleen ko, te ngeen julli leen ba mu mat sëkk ca seen i waxtu fa mbooloo ma, ndax loolu daa bokk ci sabab yiy waral gis jëmmi Yàlla ju màgg ji, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng aaya yii : {nanga sàbbaal sa Boroom njëkk fenkug jànt bi ak njëkk muy so}

فوائد الحديث

Mbékte ñeel na way-gëm ñi ci gis Yàlla mu kawe mi ca àjjana.

Bokk na ci anami woote yi : di feddali ak di xemmemloo ak di Joxe ay misaal.

التصنيفات

Dundug alaaxira