Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal

Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal

Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal". Mu ne ko: du dara, lu dul ne bëgg naa Yàlla ak ub yonnenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne ko: "ki nga bëgg ngay nekkal". Anas nee na: masuñoo bég ci dara kem ni ñu bége ci li Yonnente bi wax ne: "ki nga bëgg ngay nekkal" Anas wax ne: man bëgg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak Abuu Bakrin ak Umar, te maa ngi am yaakaar a nekk ak ñoom ndax li ma leen bëgg, donte jëfuma lu tolni seen jëf ya.

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Benn kaw-kaw bu dëkk ca àll ba dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: waxtu wi saa di taxaw? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ana lan nga ko waajalal ci jëf yu baax? Aji-laaj ji ne ko: waajalaluma ko ci ay jëf yu màgg de waaye damaa bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, te tuddul leneen ci jëfi xol yi ak yu yaram yi ak yu alal yi; ndaxte yooyu yépp ay bànqaas la ci bëgg gi te ca lay tege, ndaxte bëgg gu dëggu day waral pasteefu ci jëf yu baax yi. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ki nga bëgg ngay nekkal ca àjjana. Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di bég ci bégale googu mbégte mu tar. Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm xibaare ne moom dafa bëgg Yonnente bi ak Abuu Bakrin ak Umar, muy yaakaar a nekk ak ñoom donte ay jëfam melul ni seen i jëf

فوائد الحديث

Xereñteg Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci tont aji-laaj ji, ba tax mu tegtal ko li ko yitteel te di ko musal, te mooy: waajalal allaaxira ci luy jariñ ak jëf lu baax.

Yàlla dafa nëbb xam-xamu bis-pénc ba ci jaamam ñi ngir nit ki di des di ko waajal di ku pare ngir daje ak Yàlla.

Ngëneelu bëgg Yàlla ak ub yonnenteem ak gaa yu sell yi ak way-gëm ñi, ak xuppe ci bëgg bokkaalekat yi.

Waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: ki nga bëgg ngay nekkal. Jubluwu ci ag yamoo daraja ak wàccuwaay, waaye li mu ci jublu mooy ñu nekk ca àjjana ba ku nekk di man a gis keneen ka donte

seen i barab dafa soree.

Jubbanti jullit bi ci mu yittewoo li gën ci moom te gën ko a jariñ, te bàyyi di laaj lu ko dul jariñ.

التصنيفات

Gëm bis bu mujj ba, Jëfi xol yi