ku wax ne: laaj ilaaha illallaahu, amul lenn lu ñu war a jaamu lu dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, ab regleem ma nga ca Yàlla

ku wax ne: laaj ilaaha illallaahu, amul lenn lu ñu war a jaamu lu dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, ab regleem ma nga ca Yàlla

Jële na ñu ci Taarix Ibn Asyam Al-Asjahii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku wax ne: laaj ilaaha illallaahu, amul lenn lu ñu war a jaamu lu dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla alalam ak dereetam araam na, ab regleem ma nga ca Yàlla».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku wax ba noppi seede ci làmmiñam ne «laa ilaaha illal laahu», maanaam amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, daal di weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla, set wicc ci bépp diine bu dul Lislaam, kon alalam ak dereetam araam na ci jullit ñi, dara ñeelu ñu lu dul li feeñ ci jëfam, kon deesul jël alalam deesul tuur it dereetam, lu dul bu defee ñaawtéef, walla tooñànge bu koy waral ci àtteb Lislaam. Yàlla mooy méngoo regle ga ëllëg bis-pénc, bu dee ku dëggal la mu fay ko yiw, bu dee naaféq la mu mbugal ko.

فوائد الحديث

Wax ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla, sàrt la ci dugg ci Lislaam.

Maanaam (laa ilaaha illal Laahu) mooy weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla ci ay xërëm ak i bàmmeel ak yeneen, te wéetal Yàlla mu sell mi cig jaamu.

Ku wéetal Yàlla te taqoo ak Sariiha ci li feeñ, dañu koo war a bàyyi ba mu fésal lu wuute ak loola.

Alalu jullit bi ak dereetam ak deram dafa araam ci lu dul àqi Lislaam.

Àtteb àdduna ci li feeñ la, bu dee allaaxira nag ci yéene yi ak jubluwaay yi.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci jaamu ko