Yalla dana néggandiku aji-tooñ ji, ba bu ko jàppee du ko rëcc

Yalla dana néggandiku aji-tooñ ji, ba bu ko jàppee du ko rëcc

Jële na ñu ci Abuu Muusaa Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Yalla dana néggandiku aji-tooñ ji, ba bu ko jàppee du ko rëcc» nee na: mu daal di jàng: «{niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee ab dëgg buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102]»

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di wéy cig tooñ ak i moy ak bokkaale, ak tooñ nit ñi ci séen i àq, ndax Yàlla mu kawe mi day néggandiku di ko yeexe ak di guddal fanam di baril alalam te du ko gaawa mbugal; bu tuubul mu jàpp ko te du ko bàyyi ndax ay bàkkaar yu bari. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di jàng: {niki noonu it la sa jàppug Boroom di deme bu jàppee ab dëkk buy tooñ te ag jàppam lu metti la te tar} [Huud: 102].

فوائد الحديث

War na aji-xellu ji muu gaaw a tuub, te bañ a wóolu pexem Yàlla ndeem dafa nekk cig tooñ.

Yàlla day néggandiku way-tooñ yi bañ leen na mbugal ngir jay leen ak ngir ful mbugal ma bu ñu tuubul.

Tooñ bokk na ci sabab yiy tax Yàlla di mbugal xeet yi.

Bu Yàlla alagee ab dëkk amaana ñu sell nekk fa, waaye ñooñu dañu leen di dekkil ëllëg bis-pénc ca baax ga ñu faatoo, te mbugal ma leen yóbbaale du leen lor.

التصنيفات

Pas-pasu Lislaam, Wéetal Yàlla ci ay turam ak i meloom, Jikko yees ŋàññ