إعدادات العرض
Pas-pasu Lislaam
Pas-pasu Lislaam
1- tabax nañu lislaam ci juróom
2- kenn ci yéen de dees na dajale ag mbindam ci biiru yaayam ñent-fukki fan
3- képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ka koy delloo
4- lépp lu ma leen tere nangeen ko moytu, lépp lu ma leen digal nangeen ca def lu ngeen man
8- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
10- laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku Yàlla yombalal
11- Yàlla bind na yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di koy leeral
13- kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
16- yal na Yàlla rëbb Yahuut yi ak Nasaraan yi, ñoom kat dañoo jàppe séen bàmmeeli Yónente yi ay jàkka
17- yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
20- Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal
21- ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na
28- Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
30- ku faatu fekk moo ngi wutal Yàlla ndend dana dugg sawara
33- ku Yàlla namm ci moom aw yiw dana ko nattu
36- Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf
38- ku sos ci sunu diine ji lu ci bokkul dees na ka ko delloo
41- Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ
42- Kuy niru-nirulu aw nit ca ñoom la book
45- ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko
46- yéen de dangeen gis seen Boroom kem ni ngeen di gise weer wii, te du ngeen buuxante ngir gis ko
47- Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc
50- ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi
51- ku jàng xam-xamu biddiw jàng na benn xaaj ci njabar, bu dollee mu dolliku
53- bumu bàyyi benn caq walla bantu fett ci doqug genn giléem te daggu ko
55- ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm
60- buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli
61- ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
62- tabax nañu lislaam ci juróom
65- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
67- mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la
71- Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc
72- bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
73- Yàlla bind na ndogali mbindéef yi njëkk muy bind asamaan yi ak suuf si ci juróom-fukki junniy at
75- li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli
76- kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na
77- Yàlla tere na leen ngeen di giñ ci seen baay yi
78- li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet
80- Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal
82- Nit ki moo ngi ci diiney xaritam, na ku nekk xool kan lay xaritool
83- gaawleen jëf ndax ay fitna a ngi ñëw yu mel ni dogiiti guddi gu lëndëm,
86- buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw
87- dangeen topp yooni ña leen jiitu woon, sibre ak sibre, loxo ak loxo
88- ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara
91- yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine
92- wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde
97- jox na nu ma juróom yoo xam ne joxuñuko kenn ku ma jiitu
99- man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee
100- texe na de ndeem wax na dëgg
