yaa ngi jëmm ci aw nit woo xam ne ay ñoñ-téere lañu, boo demee ca ñoom, nanga leen woo ñu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la

yaa ngi jëmm ci aw nit woo xam ne ay ñoñ-téere lañu, boo demee ca ñoom, nanga leen woo ñu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la

Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax Muhaas Ibn Jabal ba mu ko yónnee Yaman ne ko: " yaa ngi jëmm ci aw nit woo xam ne ay ñoñ-téere lañu, boo demee ca ñoom, nanga leen woo ñu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawu Yàlla la, bu ñu la toppee ci loolu, nga xamalleen ne Yàlla farataal na ci ñoom juróomi julli ci bis bu nekk aki gudeem, bu ñu la toppee ci loolu nga xamalleen ne Yàlla farataal na ci ñoom ab sarax bob dees na ko jëll ci séen way-woomal yi delloo ko ci séeni way-ñàkk, bu ñu la toppee ci loolu nag nanga moytu séen tedd-ngay alal ya, te nga moytu ñaanug ku ñu tooñ ndax amul kiiraay diggam ak Yàlla".

[Sahih/Authentic.] [Al-Bukhari and Muslim]

الشرح

Bi Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yónnee Muhaas Ibn Jabal -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ca dëkki Yaman ya muy aji-woote jëme ci Yàlla di jàngalekat, da koo xamal ne dana jàkkaarlook ay Nasaraan; ngir mu waajal ko, ak mu tàmbalee ci bu leen di woo ci li gën a ëpp solo, Mu leen di njëkk a woo ci yéwénal pas-pas; ci ñu seede ne amul kenn ku yeyoo jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la; Ndax te ñoom ci loolu la ñuy dugge ci Lislaam, bu ñu wommatoo ci loolu mu digal leen ñuy taxawal julli; ndax moo gën a màgg ci wartéef yi ginnaaw kennal Yàlla, Bu ñu ko taxawalee mu digal leen joxe asakay séen i alal séen i way-ñakk. Mu moytandikuloo ko nag ci jëll séen alal ji gën; ndax li war mooy digg-dóomu, Mu digal ko mu moytu tooñ; ngir ku ñu tooñ bañ koo ñaan Yàlla, ndax ñaanam lu ñuy nangu la.

فوائد الحديث

Maanaam seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla mooy kennal Yàlla cig jaamu, ak moytoo jaamu lu dul moom.

Maanaam seede ne Muhammat ndawul Yàlla la mooy gëm ko ak li mu indi, ak dëggal ko, ak ne mooy ki mujj ci Yónent Yàlla yi mu yónni ci nit ñi.

Wax ak boroom xam-xam ak ku am i lënt-lënt bokkul ak wax ak ku xamul; looloo tax mu bàyyiloo xel Muhaas ci ne ko: «yaa ngi jëm ci ñoñ-téere».

Solos jullit xam diineem bu baax; ngir mu mucc ci lënti ñay lëntal te loolu mi ngi ci sàkku xam-xam.

Neenug diiney Yahuud yi ak Nasaraan yi ginnaaw ba ñu yónnee Yónente bi Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc-, ak ne ñoom bokkuñu ca way-mucc ña ëllëg bis-penc ba keroog ñuy dugg ci diiney Lislaam, daal di gëm Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.