ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na

ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na

Jële na ñu ci Abdallah ibnu Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ci ne dégg na benn waay di wax naan: giñ naa ci Kaaba gi, Ibnu Umar ne ko: deesul giñ ci ku dul Yàlla, man dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na».

[Wér na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day xamle ne képp ku giñ ci ku dul Yàlla te du ay Turam ak i Meloom weddi na walla bokkaale na; ndax giñ day waral màggal ki ñuy giñ ci moom, te màggal Yàlla rekk la ñeel; kon deesul giñ ci ku dul Yàlla walla ay Turam ak i Meloom -tudd naa sellam ga-. Giñ gii nag ci bokkaale gu ndaw la bokk; waaye kiy giñ bu màggalee la muy giñe kem ni ñuy màggale Yàlla mbaa lu ko ëpp; bu boobaa day nekk bokkaale gu mag.

فوائد الحديث

Ndax màggal cig ngiñ aqi Yàlla mu kawe mi la -tudd naa sellam ga-, kon deesul giñ ci ku dul Yàlla walla ay Turam ak i Meloom.

Xérug Sahaaba yi ci digle lu baax ak tere lu bon, rawati na bu dee lu ñaaw la daa aju ci bokkaale wala ag kéefar.

التصنيفات

Bokkaale