ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko

ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko

Jële na ñu ci Abuu Sirmata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku lore Yàlla lor ko, ku sonle Yàlla sonal ko».

[Tane na] [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat]

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo lor ab jullit, mbaa teg ko coono ci mbir mu mu man a doon; ci bakkanam walla alalam walla njabootam, ku def loolu Yàlla dana ko fay mbugal ko kem jëfam.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi :

Araamal nañu lor ab jullit, ak teg ko coono.

Yàlla day fayul ay jaamam.

التصنيفات

Àttey ñees war a féeteel ak ñees war a deñ ci ñoom