waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam

waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam

Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa laaj Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam, te dolliwuma ca dara, ndax dinaa dugg àjjana ? Mu ne ko: «waaw», waa ji ne: giñ naa ci Yàlla ne duma ci dolli dara.

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ku julli julliy juróom yi nu farataal, te tegu ca ay naafila, woor weeru koor te tegu ca ay coobare wu, lu dagan mu gëm ne dafa dagan mu def ko, lu araam mu gëm ne dafa araam mu moytu ko, kooku dana dugg àjjana.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Xérug jullit bi ci def farata yi ak bàyyi yu araam yi, jubluwaayam dëgg na nekk dugg àjjana.

Njariñu def yu dagan yi ak fas ne dafa dagan, ak araamal yu araam yi te gëm ne dafa araam.

Def yu war yi te bàyyi yu araam yi sabab la ci dugg àjjana.

التصنيفات

Tur yi ak àtte yi, Pàcci ngëm, Ngëneelu julli