إعدادات العرض
Tur yi ak àtte yi
Tur yi ak àtte yi
1- kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
2- yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
3- ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na
8- ku sos ci sunu diine ji lu ci bokkul dees na ka ko delloo
10- ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi
11- ku jàng xam-xamu biddiw jàng na benn xaaj ci njabar, bu dollee mu dolliku
14- tabax nañu lislaam ci juróom
17- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
19- li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli
20- kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na
21- gaawleen jëf ndax ay fitna a ngi ñëw yu mel ni dogiiti guddi gu lëndëm,
22- ku woote jëme cig njub dana am ag pay gu mel ni payug ña ko ca topp, te du wàññi ci seeni pay dara
24- yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine
25- wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde
28- texe na de ndeem wax na dëgg
30- laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku ko Yàlla yombal ci moom
33- bokkul ci nun kiy mbej ñiy mbej lex ya, di xotti kaw yére ya, di woote wooteg ceddo ya
34- ñaar a ngi ci nit ñi ag kéefar la: jam ci askan yi, ak yuuxu ku dee
36- Ku waat ci kóolute bokkul ci nun
38- ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba
43- jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw
48- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
49- Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer
50- waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc
51- li gay wax di ci woote lu baax la, boo ñu xibaaroon ndax la ñu defoon dees na ko jéggale
52- ñam na cafkag ngëm ki gërëm Yàlla muy Boroomam, lislaam di diineem, Muhammat di yonnenteem
54- tabax nañu lislaam ci juróom
55- képp ku sos ci sunu mbir mii lu ci bokkul dees ka koy delloo
56- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
57- laaj nga lu màgg, waaye lu yomb la ci ku Yàlla yombalal
59- ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun
