ñaar a ngi ci nit ñi ag kéefar la: jam ci askan yi, ak yuuxu ku dee

ñaar a ngi ci nit ñi ag kéefar la: jam ci askan yi, ak yuuxu ku dee

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "ñaar a ngi ci nit ñi ag kéefar la: jam ci askan yi, ak yuuxu ku dee".

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne am na ñaari melo yu nekk ci nit ñi te ci jëfi yéefar yi ak jikkóy ceddo ga la bokk, ñoom ñaar ñooy: Bi ci njëkk: jam ci askani nit ñi ak xeeb leen ak rëy-rëylu ci seen kaw. Ñaareel bi: yëkkëti kàddu ci musiba ngir mer ci dogal li, walla xotti ay yére ngir tarug njàqare.

فوائد الحديث

Ñaaxe ci toroxlu ak bañ a rëy-rëylu ci nit ñi.

Warug muñ ci bépp musiba te bañ ci a mer.

Jëf yii ci kéefar gu ndaw la bokk, te du ku benn màndarga ci màndargay kéefar nekk ci moom day nekk ab yéefar mu mag buy génn ci diine ji.

Lislaam tere na lépp luy indi teqalikoo ci diggante jullit ñi mo xam jame ci wàllu askan la walla leneen.

التصنيفات

Kéefar