إعدادات العرض
texe na de ndeem wax na dëgg
texe na de ndeem wax na dëgg
Jële nañu ci Talhata ibn Ubaydil Laahi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay bu bokk ci waa Najd dafa ñëw ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kawar gi tasaaroo, ñoo ngi dégg kàddug waxam ji, waaye xamunu li muy wax, ba mu jege Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- neke da doon laaj ci Lislaam, Yonnente bi ne ko: "juróomi julli ci bëccëg ak guddi gi" mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul yooyu? Mu ne ko: "déedéet, lu dul nga coobarewu, ak woor weeru koor", mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul moom? Mu ne ko: "déedéet, lu dul nga coobarewu", Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tuddal ko asaka, mu ne ko: ndax dara waru ma lu dul moom? Mu ne ko déedéet, lu dul nga coobarewu", nee na waa ji wane ginnaaw di dem, di wax naan: giñ naa ci Yàlla ne duma yokk ci lii dara, te duma ko wàññi, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: "texe na de ndeem wax na dëgg".
الترجمة
العربية Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Kiswahili Português සිංහල دری অসমীয়া ไทย Tiếng Việt አማርኛ Svenska Yorùbá Кыргызча ગુજરાતી Hausa नेपाली Română മലയാളം Nederlands Oromoo Soomaali తెలుగు پښتو Kinyarwanda Malagasy ಕನ್ನಡ Српски Moore ქართული Čeština Magyar Українська Македонски Lietuvių Azərbaycanالشرح
Benn waay bu jóge Najd dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kawaram gi tasaaroo, kàddoom yëkkatiku, te xameesul li muy wax, mu ñëw ba jege Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- laaj ko faratay Lislaam? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tàmbalee ci julli, xamal ko ne Yàlla farataal na ci moom juróomi julli ci bëccëg yi ak guddi. Mu ne ko: ndax dara war na ma ci julli lu dul juróom yii? Mu ne ko: déedéet, lu dul nga coobarewu ci julliy naafila yi. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- teg ca ne ko: bokk na ci li Yàlla farataal ci yaw woor weeru koor. Waa ji ne ko: ndax dara war na ci woor lu dul woor weeru koor? Mu ne ko: déedéet, lu dul nga coobarewu ci woor. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tuddal ko asaka. Waa ji ne ko: ndax dara war na ma ci ay saraxe ginnaaw asaka giy farata? Mu ne ko: déedéet, li dul nga coobarewu. Ginnaaw bi waa ji déggee farata yii ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa dummóoyu wane ginnaaw di giñ ci Yàlla mu kawe mi ne dina taqoo ak loolu te du ci yokk du ci wàññi, ginnaaw loolu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: waaji de bu dëggalee ci li mu giñ dana bokk ci way-texe yi.فوائد الحديث
Yaatug Sariihab Lislaam ak yombalam ci mukallaf yi.
Rafetug jëflanteg Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak waa ji, ndax yombalal na ko mu jege ko, ak laaj ko
Woote jëme ci Yàlla mu kawe mi day tàmbalee ci li ëpp solo teg ca la ca tege.
Lislaam pas-pas la ak jëf, jëf du jariñ ci lu dul ngëm, ngëm it du jariñ ci lu dul jëf
Solos jëf yii ci ne dafa bokk ci ponki Lislaam yi.
Jullig àjjuma day dugg ci julliy juróom yi war; ndaxte day wuutu jullig tisbaar ci bisu àjjuma ci képp ku mu war.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa tàmbali am njàngaleem ci faratay Lislaam yi gën a feddaliku te mooy ay ponkam ginnaaw ñaari baati seede yi; ndaxte moom jullit la woon, tuddul aj nag ndax njëkk ñu koy farataal la, walla ndax waxtoom ñëwagul woon.
Nit ki bu yamee ci yi Sariiha waral ci moom kon texe na, waaye loolu tekkiwul ne sunnaaluñu ci moom mu def naafila yi; ndax te naafila yi day mottali farata yi ëllëg bis-pénc.
التصنيفات
Lislaam