misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day ànd bañ a nelaw ak di tàng

misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day ànd bañ a nelaw ak di tàng

Jële na ñu ci An-Nuhmaan Ibn Basiir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «misaalu way-gëm ñi ci seenug bëggante ak seenug yërëmante ak seenug ñeewantu day mel ni aw yaram, bu ci benn cër di jàmbat dara mbooleem yaram wi yépp day ànd bañ a nelaw ak di tàng».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ni jullit ñi war a mel ci seen biir ci yéeneente aw yiw ak yërmànde ak dimbaleente ak jàppalante, ak di yég lor wuy dal ci ñeneen ñi, kem ni wenn yaram mel, bu ci benn cér feebare, mbooleem yaram wi day ànd di bañ a nelaw ak di tàng.

فوائد الحديث

Màggal àqi jullit ñi lu jaadu la, ak ñaaxe ci ñuy dimbalente ak di yërëmante ci seen biir.

Jaadu na lii di bëggante ak dimbaleente muy dox ci diggante way-gëm ñi.

التصنيفات

Lislaam