إعدادات العرض
Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko
Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko
Jële nañu ci Al-Baraa -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: Mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ci waa Ansaar yi ne: "kénn du leen bëgg ku dul way-gëm, te kenn du leen bañ ku dul ab naaféq, ku leen bëgg Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko".
[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Hausa Kurdî Kiswahili Português සිංහල Svenska ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە Tiếng Việt پښتو অসমীয়া دری Кыргызча or Malagasy नेपाली Čeština Oromoo Română Nederlands Soomaali తెలుగు ไทย മലയാളം Lietuvių Српски Українська Kinyarwanda Shqip ಕನ್ನಡ Moore ქართული Magyar Deutschالشرح
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bëgg Ansaar yi di waa Madina, màndarga la ci ngëm gu mat; ngir li ñu jiitu ci dimbali Lislaam ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak dox ci yiir jullit ni, ak joxe seen alal ak seen bakkan ci yoonu Yàlla, kon bañ leen màndargay naaféq la. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- leeral ne ku bëgg Ansaar yi Yàlla bëgg ko, ku leen bañ Yàlla bañ ko.فوائد الحديث
Nekk na ci it ngëneel yu màgg ñeel Ansaar yi, ndax bëgg leen màndargay ngëm la ak set ci naaféq.
Bëgg wàlliyuy Yàlla yi di leen dimbali sabab la ci Yàlla bëgg ab jaamam.
Ngëneelu ña jiitu ci Lislaam.