ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba

ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba

Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Damaa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi, Ibn Jadhaan de ca jamanoy ceddo ga da daan jokk mbokk di leel miskiin, mo ndax loolu dana ko jariñ ? Mu wax ne: «du ko jariñ de, ndaxte waxul benn yoon ne: sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Abdallah Ibn Jadhaan, bokkoon na ci njiitu waa Xurays njëkk Lislaam, Te bokk na ci ay jëfam yu baax: daa na jokk mbokk, di rafetal jëme ci ñoom, di leel miskiin, ak yeneeni ngënéel yoy Lislaam dafa ñaaxe ci def ko, ci ne jëf yooyu du ko jariñ ëllëg bis-pénc; te li ko waral mooy weddi gi mu weddi Yàlla, te masul wax: yaw sama Boroom na nga ma jéggal samay bàkkaar ëllëg bisub fay ba.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Leeral ngënéelul ngëm, ak ne sart la ci nu nangug jëf yi.

Leeral gaafug kéefar, ak ne moom day màbb jëf yu baax yi.

Yéefér yi séen jëf du leen jariñ ëllëg bis-pénc ndax li ñu gëmul Yàlla ak bis bu mujj ba.

Jëfi nit ki jamono ya mu nekkee yéefar bu tuubee danañu ko ko bindal aw yiw daal di ka koy fay.

التصنيفات

Lislaam, Kéefar