ku rafetal ci Lislaam deesu ko toppe la mu defoon ca ceddu ga, waaye ku def lu ñaaw ci Lislaam dees na ko toppe lu njëkk la ak lu mujj li

ku rafetal ci Lislaam deesu ko toppe la mu defoon ca ceddu ga, waaye ku def lu ñaaw ci Lislaam dees na ko toppe lu njëkk la ak lu mujj li

Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne: Benn waay dafa ne: yaw Yónente Yàlla bi, ndax dañ nuy toppe la nu defoon ca ceddu ga ? Mu ne ko: «ku rafetal ci Lislaam deesu ko toppe la mu defoon ca ceddu ga, waaye ku def lu ñaaw ci Lislaam dees na ko toppe lu njëkk la ak lu mujj li».

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ngëneelul dugg ci Lislaam, Ak ne képp ku tuub te rafetal Lislaamam tey sellal te dëggu; deesul luññutu la mu defoon ca ceddo ga ci ay moy, Waaye képp kuy ñaawal ci Lislaam ci nekk ab naaféq walla mu génn ci diine ji; dees na ko àtte ca la mu defoon ca kéefar ga ak li mu jëf ci Lislaam.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal adiis bi:

Yittewoog Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- jëf yi ñu doon def ca ceddo ga.

Ñaaxe ci sax ci Lislaam.

Ngëneelu dugg ci Lislaam ak ne day far jëf ya ko jiitu woon.

Ki génn ci diine ji ak naaféq bi dees na leen toppe la ñu defoon lu jiitu Lislaam, ak bépp bàkkaar buñu def ci Lislaam.

التصنيفات

Lislaam, Dollikug ngëm ak ug wàññikoom