ngëm day ràpp ci biiru kenn ci yéen kem ni yéere bu ràpp di ràppe, ñaanleen Yàlla mu yeesal ngëm ci séen i xol

ngëm day ràpp ci biiru kenn ci yéen kem ni yéere bu ràpp di ràppe, ñaanleen Yàlla mu yeesal ngëm ci séen i xol

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ngëm day ràpp ci biiru kenn ci yéen kem ni yéere bu ràpp di ràppe, ñaanleen Yàlla mu yeesal ngëm ci séen i xol».

[Wér na] [Al-haakim soloo na ko, ak At-tabaraaniy]

الشرح

Leerarug hdiisb: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne ngëm day ràpp ci xolu jullit bi di néew doole, kem ni yéere bu bees di ràppe ndax li ñu ko yàgg a jëfandikoo; Li koy waral nag mooy lott ci jaamu ga, ak toggoo moy ya, ak nuur ci bànneex yi. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal nu nuy ñaan Yàlla mu kawe mi mu yeesal sunug ngëm, ci nuy def farata yi ak di baril di ko tudd ak jéggalu.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi :

Ñaaxe ci ñaan Yàlla ag dëgër ak yeesal ngëm ci sunu xol.

Gёm nag wax la ak jëf, day dolliku ci ak topp Yàlla di wàññiku ci ag moy.

التصنيفات

Dollikug ngëm ak ug wàññikoom