Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj la, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor si kaw yoon wi

Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj la, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor si kaw yoon wi

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj la, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor si kaw yoon wi, te kersa benn pàcci la ci ngëm»

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ngëm ay xaaj la ak i melo yu bari, te day làmboo jëf yi ak pas-pas yi ak wax yi. Ak ne li gën kawe ci ngëm te gën ca mooy wax: «laa ilaaha illal laahu» te xam maanaama , di jëfe ay warteefam, ci ne Yàlla moom mooy Yàlla miy kenn mooy ki yayoo jaamu moom dong wolif leneen. Ak ne jëf ji gën a tuuti ci ngëm, mooy randale lépp luy lor nit ñi ci yoon yi. Yónente bi xibaare na ci ne lii di kersa ci melay ngëm la bokk, jikko la juy waral def lu rafet te bàyyi lu ñaaw.

فوائد الحديث

Ngëm ay martaba la yoo xam ne dañoo gënante.

Ngëm wax la ak jëf ak pas-pas.

Am kersa ci Yàlla mu kawe mi day waral: ba du la gis ci li mu la tere, du la ñàkk a gis it ci li mu la digal.

Tudd lim bi tekkiwul ne ag tënk la, waaye day tegtale ne jëfi ngëm yi dafa bari, Araab yi danañu tuddal mbir mi ab lim te waaye bëgguñoo dàq leen lu dul moom.

التصنيفات

Dollikug ngëm ak ug wàññikoom