Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer

Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer

Jële nañu ci Adiyyi ibn Haatim mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yahuut yi ñooy ñi Yàlla mere, nasaraan yi ñooy ñi réer».

[Wér na] [At-tirmisiy soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne yahuut yi aw nit lañu wu Yàlla mere; ndaxte ñoom dañoo xam dëgg ba noppi te jëfewuñu ko. Nasaraan yi nag ay nit yu réer lañu; ndaxte ñoom dañuy jëf ci ñàkk a xam.

فوائد الحديث

Boole xam ak jëfe ag mucc la ci yoonu ña ñu mere ak ña réer.

Moytondikuloo yoonu Yahuut yi ak nasaraan yi, te taqoo ak yoon wu jub wi te mooy Lislaam.

Yahuut yi ak nasaraan yi ñéppa réer te ñépp lañu mere, waaye melo wi Yahuut yi gën a jagoo mooy mere, wi nasaraan yi gën a jagoo mooy réer.

التصنيفات

Lislaam, Pirim laaya yi