Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf

Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf

Jële na ñu ci Abuu Maalik Al-Asharii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf, julli ag leer la, saraxe it aw lay la, muñ it ag leer la, Alxuraan it aw lay la ñeel la yaw, walla muy aw lay ci sa kaw, nit ñépp dañuy xëy am ci ñuy jaay séen bopp, benn mu goreel ko, walla mu alag ko».

الشرح

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne: laabug bitti dana ame ci njàpp ak ci sangu, te sart la ci julli. Wax: «Alhamdu lil-Laah» day feesal màndaxekaay ba, te mooy tagg Yàlla mu sell mi, melal ko ci bépp melow mat, dees koy màndaxe ëllëg bis-pénc mu feesal màndaxekaay yu jëf ya. Wax: «Subhaanal Laah Wal hamdu lil Laah» te mooy sellal Yàlla ci gépp wàññeeku ak melal ko ci wépp melow mat bi nga xam ne dafa yell ca màggam ga, ak bëgg ko ak màggal ko loolu day feesal diggante asamaan ak suuf. Ak ne «julli leer la» ñeel jaam bi ci xolam, ak ci kanamam, ak ci bàmmeelam, ak bisub dajaloo ba. Ak ne: "sarax aw lay la" tegtal la ci dëggug gëmug aji-gëm ji, ak wuuteem ak naaféq bi nga xam ne day bañ a saraxe ndax gëmul la ñu ko ca dig. Ak ne "saraxe leer la" -te mooy téye sa bopp ci ñaxtu ak mer- leer la guy ànd ak tàngoor akug lakk, niki leerug jànt bi; ndaxte dafa jafe te day aajowoo xeex ak bakkan ak tere ko ay bànneexam; boroomam du deñ di am leer di jubb tey wéy ci yoon. Te mooy muñ ci topp Yàlla, ak ci bàyyi moy yi, ak muñ musiba yi ak xeeti naqari àdduna yi. Ak ne : Alxuraan day nekk saw lay " ci jàng ko ak di ko jëfe, walla "mu nekk aw lay ci sa kaw" ci boo ko bàyyee doo ko jëfe te doo ko jàng. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne nit ñépp dañuy dox di tasaaroo juge ci séen i nelaw di génn séeni kër ngir séen i liggéey yu wuute. Am na ci ñoom ñuy jubal tege ci topp Yàlla muy goreel boppam ci sawara, waaye am na ci ñoom ñuy jàdd yoon di tàbbi ci moy yi daal di alag boppam dugal ko sawara.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Laab ñaar la: laab gu feeñ te mooy jàppu ak sangu, ak laab gu nëbbu te mooy kennal Yàlla ak gëm ak def lu baax.

Solos sàmmoonteek julli ndax moom leer la ñeel jaam bi ci àdduna ak allaaxira.

Saraxe tegtal la ci ngëm.

Solos jëfe Alxuraan ak dëggal ko ngir ne day nekk saw lay walla muy aw lay ci sa kaw.

Bakkan boo ko soxlaalul ci jaamu Yàlla mu soxlaal la ci moy Yàlla.

Nit ku nekk fàwwu mu jëf; benn mu goreel boppam ci topp Yàlla, walla mu alag ko ci moy Yàlla.

Muñ day aajowoo dëgër ak séentu pay ga, ndax dafa am ab coono.

التصنيفات

Pàcci ngëm, Njariñi tudd Yàllay Mu tedd Mu màgg mi, Sellal bakkan yi, Ngëneelu njàpp, Ngëneelu julli