Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa

Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa».

الشرح

Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne faj gi gën ci laaj yi Saytaane di jax-jaxale aji-gëm ji, Saytaane naan ko: ku bind lii? Ku bind lii? Ku bind asamaan yi? Ku bind suuf si? Aji-gëm ji di tontu teg ko ci diine ak ci yég-yég ak ci xel naan ko: Yàlla, Waaye Saytaane du yam ci jax-jaxal yooyu, waaye day tuxu ba mujj ne ko: ku bind sa Boroom? Ci loolu nag aji-gëm ji day jeñ jax-jaxal yooyu ci ñatti mbir: Ci gëm Yàlla. Ak muslu ci Yàlla ci Saytaane. Ak taxawlu ci bañ a topp jax-jaxal yi.

فوائد الحديث

Dummóoyu jax-jaxali Saytaane yi ak li muy rotal ci xel te bañ cee xalaat, ak làqu ci Yàlla ngir mu dindi ko.

Lépp luy tàbbi ci xolu nit ki ci ay jax-jaxal yu wuuteek Sariiha loolu ci Saytaane la juge.

Tere nañu xalaat ci jëmmi Yàlla ji, ñaaxe nañu it di xalaat ci mbidéefam yi ak i keemaanam.

التصنيفات

Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi, Lislaam, Njariñi tudd Yàllay Mu tedd Mu màgg mi