li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli

li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli

Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli».

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo bàyyi julli gu ñu farataal, mu xamle ne li dox ci diggante nit ki ak tàbbi ci bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli, julli mooy ñaareelu ponk ci ponki Lislaam yi, te mbiram dafa màgg ci Lislaam, ku ko bàyyi ngir weddi ag waram kooku weddi na Yàlla ci dëppoog woroom xam-xami jullit ñi, ku ko bàyyi ba fàww nag ngir doyadal ko ak tàyyeel, ab yéefar la, te tuxal nañu ne Sahaaba yi dëppoo nañu ci loolu, bu dee da koy bàyyi leeg-leeg di julli leeg-leeg kooku ki ñu gaaral tëkku gu tar gii la.

فوائد الحديث

Solos julli ak sàmmonte ak moom, ndax mooy xàjjale diggante kéefar ak ngëm.

Àrtu gu tar ci bàyyi julli ak sànk ko.

التصنيفات

Yiy firi Lislaam, Kéefar, Warug julli ak àtteb ki ko bàyyi