إعدادات العرض
yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine
yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine
Jële na ñu ci Ibn Abbaas-yal na leen Yàlla dollee gërëm-mu wax ne: Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ci subag sànni jamra fekk moo ngi ci kaw giléemam gi: "foral ma ay xeer" ma foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, muy xeer yi muy sànni, mu tàmbali de leen sànni ci loxoom,di wax naan: "sànnileen yu mel nii" daal di wax ne: " yéen nit ñi, moytandikulen ëppal ci diine, ndax li alag ña leen jiitu woon mooy ëppal ci diine".
[Wér na] [Ibnu Maaja soloo na ko, ak An-nasaa'iy, ak Ahmat]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Kiswahili Português සිංහල Svenska ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá ئۇيغۇرچە Tiếng Việt Hausa پښتو অসমীয়া دری Кыргызча or नेपाली Malagasy മലയാളം Čeština Oromoo Română Kinyarwanda Nederlands Soomaali తెలుగు ไทย Lietuvių Српски Українська Shqip ಕನ್ನಡ Moore ქართული Magyarالشرح
Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne nekkoon na ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bisub tabaski ci subag sànni jamratu Haqaba yi ci ajug tàggatoo ga, Mu digal ko mu foral ko ay xeeri jamra, mu foral ko juróom-ñaari xeer yu sew, benn bi toll ni doomi Himmas walla bundux, Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-teg ko ci loxoom di ko yëngal, daal di wax ne: Yu toll ni yooyu ci jëmm ngeen sànni sànni ko, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal moytondikuloo ëppal ak taral ak jéggi dayo ci biri diine, ndax li alag xeet ya jiitu woon mooy jéggi dayo ak ëppal ak taral ci diine.فوائد الحديث
Tere nañu ëppal ci diine, leeral it mujjam gu ñaaw, ak ne sabab la ci alkande.
Waaru ci xeet yi jiitu ngir moytoo tàbbi ca seen njuumte ya.
Soññee ci roy ci sunna.
التصنيفات
Masalay ceddo ga