jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw

jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw

Jële na ñu ci Hakiim Ibn Hisaam -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne: Damaa wax: yaw Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaar ma ci bir yi ma daan def ca ceddo ga, ci sarax ak goreel, ak jokk mbokk, ndax am na yool? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «jébbalu nga ànd ak la nga defoon ciw yiw».

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne yéefar bi bu jébbaloo dees na ko fay ab yool ca lamu defoon ca ceddo ga lu jiitu Lislaam ci ay jëf yu baax ci sarax, ak goreel jaam, ak jokk mbokk.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Yéefar bi deesu ko fay ay jëf yu baaxam ca allaaxira bu dee daa faatu cig kéefar.

التصنيفات

Lislaam