man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin

man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Dañoo mas a toog ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàkka ji rekk benn waay bu yéeg sig giléem daldi dugg si, mu yésal giléem gi ci jàkka ji daal di koy yeew, ba noppi daal di ne? Kan ci yéen mooy Muhammat? Fekk Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi sóonu ci séen biir, nu ne ko: góor gu weex gii sóonu la, waa ji ne ko: yaw doomu Abdul Mutalib, Yónente bi ne ko «wuyu naa la». Waa ji ne ko -: man de damalay laaj te dinaa taral laaj yi ci sa kaw, bul ma mere kon ? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «laajal lu la soob» mu ne ko: maa ngi lay laaj ci sa Boroom di Boroomu ñi la jiitu, ndax Yàlla moo la yónni ci nit ñépp ? Mu ne ko: «giñ naa ko ci Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ci Yàlla , ndax Yàlla moo la digal nu julli juróomi julli ci bis bi ak ci guddi gi? Mu ne ko: «waaw maa ngi seedeloo Yàlla ». Mu ne ko: maa ngi ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nu woor weer wii ci at mi? Mu ne ko: «seedeloo naa ko Yàlla, waaw». Mu ne ko: maa ngi lay ñaan ngir Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nga jël sarax ci sunu way-woomal ñi séddale ko ci sunu way-ñàkk ñi? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: «maa ngi koy seedeloo Yàlla, waaw».waa ji ne ko: gëm naa li nga indi, man nag ndaw laa te samay nit ñoo ngi sama ginnaaw, man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin.

الشرح

Leerarug hadiis bi: Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da nuy xibaar ne: Sahaaba yi dañoo mas a toog ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàkka ji benn waay dugg si war sig giléem, gooral ko, daal di ko yeew, Daal di leen laaj: kan ci yéen mooy Muhammat? Fekk Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ngi sóonu ci biir nit ñi, nu ne ko: góor gu weex gii sóonu la, Waa ji ne ko: yaw doomu Abdul Mutalib, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: dégg naa la, laajal ma tontu la. Waa ji ne Yonnente bi: man de dama lay laaj te dinaa taral laaj yi ci sa kaw, kon bul ma jàppal dara ci sa bopp. Maanaam bul ma mere, te bul am benn xat-xat, Mu ne ko: laajal loo bëgg, Mu ne ko: maa ngi lay laaj ci sa Boroom di Boroomu ñi la jiitu, ndax Yàlla moo la yónni ci nit ñi? Mu ne ko: maa ngi sedeel Yàlla ne mooma yónni, ngir feddali ak dëggoom, Waa ji ne ko: maa ngi ñaan ci Yàlla, maanaam, maa ngi lay laaj ci Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nu julli julliy juróom ci bis bi ak ci guddi gi? Te mooy julli yi ñu farataal, Mu ne ko: seedeloo naa Yàlla lu am la, Mu ne ko: maa ngi lay laaj ci Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nu woor weer wii ci at mi? Maanaam weeru koor, Mu ne ko: seedeloo naa Yàlla ne mooko digle, Mu ne ko: ñaan naa la ci Yàlla, ndax Yàlla moo la digal nga jël sarax bii ci sunu way-woomal ñi séddale ko sunu way-ñàkk ñi? Te mooy asaka, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: seedeloo naa ko Yàlla waaw, Damaam daal di jébbalu Dugg ci lislaam wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko moom dana woo ay nitam ci Lislaam. Mu daal di xamle boppam ne moo ngi tudd Damaam Ibn Sahlabata bokk ci Banii Sahd Ibn Bakrin.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi:

Toroxlug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-; ndax waa ji manu koo ràññee ak Sahaaba yi.

Rafet jikkoy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm-, ak ñeewantoom ci tontu aji-laaj ji, te rafet tontu day waral ñu nangu woote bi.

Dagan na ñu xamle nit ki ci melow weex ak xonk, ak gudd ak gàtt, mbaa yu ko niru te jubluwuñu ca sikkal, ndeem bañu ko.

Dagan na ab yéefar dugg ci jàkka ji ngir aajo.

Tuddu ñu aj ci Hadiis bi ndax amaana farataalaguñu ko woon bamu fay ñëw.

Xérug Sahaaba yi ci woo nit ñi; ndax bi mu tuubee rekk ci la xér ci woo ay nitam.

التصنيفات

Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi, Sunu Yónnent Muhammat yalna Yàlla xéewalal ko te jàmmal ko, Lislaam, Woote jëm ci Yàlla, Warug julli ak àtteb ki ko bàyyi, Warug natt asaka ak àtteb ki ku bàyyi, Obligation of Fasting and Ruling of Its Abandoning