waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc

waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax baay taxam ba: « waxal ne: amul kenn ku yayoo jaamu ku dul Yàlla, ma seedeel la ci ëllëg bis-pénc», mu ne ko: bu dul woon waa Xurays danañu ma ŋàññi, di wax naan: li ko yóbbe loolu mooy tiitaange, kon dinaa ci bégal sa bët. Yàlla daal di wàcce Aaya bii: {du yaw yaay gindi koo sopp, waaye Yàlla mooy gindi ku ko soob} [Al-Xasas: 56].

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Leerarug hdiis de: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa sàkku ci baay taxam ba Abuu Taalib fekk mi ngi ci sukraatus ndee mu wax ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul Yàlla ngir mu ramm ko ëllëg bis-pénc, seedeel ko Lislaam, mu bañ koo wax ngir ragal waa Xurays ŋàññi ko di wax naan: moom de daa jébbalu ndax ragal dee ak neew doole! Mu wax Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: bu dul woon ak loolu dinaa dugal mbégte ci sa xol ci wax seede googu, ma defal la li nga mébét ba nga gërëm! Yàlla mu kawe mi wàcce aaya buy wane ne Yónente bi moomul njubug dëppale ñeel Lislaam, waaye Yàlla mu màgg mi moom rekk mooy dëppale ku ko soob. Waaye Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day gindi nit ñi ci tegtal ak leeral ak wane ak woote jëme ci yoon wu jub wi.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi :

Deesul bàyyi dëgg ngir ragal waxi nit ñi.

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- li mu man mooy gindig tegtal ak jubbanti waaye amul gindig dëppale.

Yoonalees na seeti yéefar bu feebar ngir woo ko ci Lislaam.

Xérug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci woote jëme ci Yàlla mu kawe mi ci gépp anam.

التصنيفات

Gëm dogal yi, Lislaam, Ngëneeli wéetal Yàlla