tabax nañu lislaam ci juróom

tabax nañu lislaam ci juróom

Jële na ñu ci Abdullah Ibnu Umar-yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na : "tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat jaamam la di ndawam, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor ".

[Wér na] [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér]

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa niroole lislaam ak ub tabax bu ñu xereñe ci juróomi ponk yu tëye tabax bi, yeneen jikkoy lislaam yi des mel ni luy mottali tabax bi, Li njëkk ci ponk yii mooy : ñaari baati seede yi; seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, te ñoom ñaar benn ponk lañu; benn du tàqalikoo ak beneen ba, jaam bi da koy wax ngir nangu kennug Yàlla gi, ak yayoo gi mu yayoo ag jaamu moom rekk wolif keneen, ak jëfe li miy waral, ak gëm Yónenteg Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-te topp ko. Ñaareelu ponk bi : taxawal julli, mooy julliy juróom yi ñu farataal ci bis bi ak guddi gi : fajar, tisbaar, tàkkusaan, timis, ak gee, ci ay sàrtam, ak i ponkam, ak i wareefam. Ponku ñatteel bi : génne asaka gi nu farataal, moom nag jaamug alal la gu war ci alal bu matee lim ba ñu ko tënk ci sariiha, ki ko yeyoo lañu koy jox. Ponku ñeenteel bi : aj, te mooy jublu Màkka ngir taxawal ay jaamu, ngir jaamu Yàlla mu màgg mi. Ponku juróomeel bi : woor weeru koor, te mooy bàyyi lekk ak naan ak yeneen yiy yàq koor ngir yéene cee jaamu Yàlla, li dale ci fenkug fajar gi ba ca so wu jant bi.

فوائد الحديث

Ñaari seede yi dañoo lënkaloo, benn du ci wér bàyyi beneen bi; loolu moo tax mu def leen benn ponk.

Ñaari seede yooyu ñooy fondamaa diine, te deesul nangu wax mbaa jëf lu dul ci ñoom ñaar.

التصنيفات

Gëm Yàlla Mu tedd Mu màgg mi, Yónnent gi, Lislaam, Warug julli ak àtteb ki ko bàyyi, Warug natt asaka ak àtteb ki ku bàyyi, Obligation of Fasting and Ruling of Its Abandoning, Obligation of Hajj and ‘Umrah and Ruling of Its Abandoner