ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara

ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara».

[Wér na] [Muslim soloo na ko]

الشرح

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamale ne ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara kon jëmuwaayam mooy àjjana doonte sax mbugël nañu ko ci yennati bàkkaaram, waaye ku faatu fekk doon na bokkaale Yàlla ak dara dana sax sawara.

فوائد الحديث

Ngëneelu kennal Yàlla, ak ne sabab la ci mucc ci sax ca sawara.

Jegeg àjjana ak sawara ci jaam bi, ci ne dara doxul digganteem ak ñoom lu dul dee.

Moytandikuloo ci bokkaale moo xam mu néew walla mu bari; ndax mucc ci sawara moo ngi ci moytu ko.

Njàngat ci jëf yi moo nga ca muj ga.

التصنيفات

Bokkaale, Meloy Àjjana ak Sawara