إعدادات العرض
ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi
ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi
Jële na ñu ci yenn Soxnay Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku ñëw cib xamtukat laaj ko dara deesu ko nangul julli ñent-fukki guddi».
الترجمة
العربية Bosanski English فارسی Français Bahasa Indonesia Русский اردو 中文 हिन्दी বাংলা Español Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் සිංහල မြန်မာ ไทย Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە Türkçe دری Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy Română Kinyarwanda नेपाली Српски Soomaali Moore Українська Български Tagalog Azərbaycan ქართული тоҷикӣ bm Oromoo Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di dem cib xamtukat -tur la wu boole gisaanekat ak kuy xamtu ci bidiw yi, ak kuy xamtu ci beeñ bi, ak yu mel ni yooyu, ci képp kuy tegtaloo ci xam kumpa ci jëfandikoo ay bir yu muy jiital- ak ne ku leen laaj dara ci biri kumpa Yàlla dana ko xañ yoolu julleem yi ñent-fukki fan; loolu nag am mbugal la ci bàkkaar bu mag bii.فوائد الحديث
Araamal nañu gisaane, ak dem ci gisaanekat yi ak laaj leen ci kumpa yi.
Dees na xañ nit yoolub jaamoom ngir mbugale ko ko ci bàkkaar bu mu def
Day dugg ci Hadiis bi li ñuy woowe taaruwaayu biddiw yi ak di ca xool, ak di jàng ca ténq ya ak kopp ya -donte ci anamug yër dong la-; ndax loolu lépp ci seet la bokk ak wootewoo xam kumpa.
Ndeem lii mooy payug ku dem ci xamtukat ba, kon naka la payug jëmmi kiy xamtu di deme?
Jullig ñent-fukki fan ya dana ko doy kon du ko fay, waaye du ca am ab yool.
التصنيفات
Tur yi ak àtte yi