li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal

li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal

Jële na ñu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw" ñu ne ko: lan mooy bokkaale gu ndaw yaw Yonnente Yàlla bi? Mu ne leen: "ngistal, ngistalkat yi Yàlla da leen di wax ëllëg bis-pénc bu ñu faayee nit ñi seen jëf ba noppi: demleen ca ña ngeen doon ngistal ca àdduna, ngeen xool ba xam ndax dangeen fekk fa ñoom ag pay?"

[Tane na] [Ahmat soloo na ko]

الشرح

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne mbir mi mu gën a ragal ci xeetam wi mooy: bokkaale gu ndaw te mooy: ngistal; di def ngir nit ñi. Mu xibaare ne mbugalum ñiy ngistal ëllëg bis-pénc mooy ñu ne leen: demleen ca ña taxoon ngeen doon jëf, ngeen xool ndax danañu am yool ak pay gu ñu leen di fay ca seen jëf yooya?!

فوائد الحديث

Dañoo war a sellal jëf yi ngir Yàlla mu màgg mi, te moytu ngistal.

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñeewante lool aw xeetam te xér ci gindi leen ak di leen laabire.

Bu dee nii la ragalug Yonnente bi toll te muy wax ak sahaaba yi, te ñoom ñooy sangi ñu baax ñi, kon ragal ci ñiy ñëw seen ginnaaw mooy gën a tar.

التصنيفات

Bokkaale, Yërmandeem SLM