ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi

ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi

Jële na ñu ci Sayd Ibn Xaalid Al-Juhanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo jiite jullig suba ca Hudaybiya ginnaaw ba mu tawee ca guddi ga, ba mu noppee mu jàkkaarloo ak nit ñi, ne leen: «ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi, ku wax ne: taw bi wàcc na fi nun ci ngënéelu Yàlla ak yërmàndeem, kooku gëm na ma, weddi biddiw yi, waaye ku wax: taw bi biddiw bii mbaa bee mootax mu am, kooku weddi na ma, gëm biddiw yi».

الشرح

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa julli jullig suba ca Hudaybiya -ab bérab la bu jege Màkka- ginnaaw ba mu tawee ca guddi googa, Ba mu sëlmalee ca julli ga mu jàkkaarloo ak nit ñi, laaj leen: ndax xam ngeen lan la séen Boroom bu màgg bi wax ? Ñu tontu ko ne ko: Yàlla a xam ak Yónenteem. Mu ne leen: Yàlla mu kawe mi leeral na ne nit ñi dañoo séddalikoo ci wàccug taw bi ñaari xaaj: xaaj bu gëm Yàlla mu kawe mi, ak xaaj bu weddi Yàlla mu kawe mi; Ku wax ne: taw bi wàcc na fi nun nu ci ngënéelu Yàlla ak yërmàndeem, mu askanele Yàlla mu kawe mi wàccug taw bi, kooku gëm na Yàlla miy Aji-Bind di Aji-Soppaxndiku ci àdduna bi, waaye weddi na biddiw yi. Waaye ku wax ne: taw bi dafa wàcc ngir biddiw bii ak bee; kooku weddi na Yàlla, gëm biddiw yi, loolu kéefar gu ndaw la ndax li mu askanale wàccug taw bi biddiw yi; te Yàlla defu ko sabab ci Sariiha mbaa ci ndogal yi. Ki askanale wàccug taw bi mbaa yeneen i xew-xew ci suuf yëngatug biddiw yi ak séenug penkte ak séenug wàcci ngir fas ne biddiw yi mooy def loolu ca dëgg-dëgg, kooku daa weddi weddi gu mag (day génne ci diine ji)

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi :

Sopp na ñu ginnaaw bu tawee ñu wax lii: (mutirnaa bi fadlil laahi wa rahmatihii) tawalal nañ ñu ci ngënéelu Yàlla ak yërmàndeem.

Képp koo xam ne wàccug taw bi mbaa leneen dakoo askanale biddiw yi moo xam cig mbind mbaa amal ga kooku aji-weddi la weddi gu mag, bu ka ko askanalee ci ne sabab la kon aji-weddi la weddi gu ndaw ndax loolu nekkul sabab ci Sariiha mbaa ci yég-yég.

Xéewal dana nekk sababu kéefar bu nu ko weddee, dana nekk it sababu ngëm bu ñu santee.

Tere na ñu di wax naan: "wàcceel nañ ñu ab taw ngir biddiw sàngam", doonte jamono la ñu ci jublu; loolu nag ngir fatt luy yóbbe ci bokkaale.

Xol bi dafa war a wékku ci Yàlla mu kawe mi ci xëcci njariñ ak jeñ lor.

التصنيفات

Wéetal Yàlla ci moom gi mu moom lépp di ko saytu, Yiy firi Lislaam, Pàcci ngëm, Kéefar