إعدادات العرض
kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
Jële nañu ci Abii Muhammad Abdullah Ibn Amr Ibn Al-Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi".
[قال النووي: حديث صحيح] [رويناه في كتاب الحجة بإسناد صحيح]
الترجمة
العربية Español አማርኛ English اردو Indonesia বাংলা Français Türkçe Русский Bosanski සිංහල हिन्दी 中文 فارسی Tiếng Việt Tagalog Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ ไทย Deutsch پښتو অসমীয়া Shqip Nederlands ગુજરાતી Кыргызча नेपाली Lietuvių دری Српски тоҷикӣ Kinyarwanda Magyar Čeština Moore Malagasy Oromoo ಕನ್ನಡ Azərbaycan O‘zbek Українська ქართული Македонски ភាសាខ្មែរ Bambara ਪੰਜਾਬੀ मराठी Kirundi Kurmancî Bahasa Melayuالشرح
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne nit ki du nekk aji-gëm ju matug ngëm ba keroog ag bëgg-bëggam di topp li Yonente bi indi ci ay digle ak i tere ak yeneen; mu bëgg li mu digle, bañ li mu tere.فوائد الحديث
Hadiis bi ab tënk la ci nangul Sariiha ak wommatul ko.
Àrtu nit ki ci muy àttewoo xel ak aada di ko jiital ci kaw li Yonente bi indi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, kuy def loolu dees na dàq ci moom ngëm.
Dañoo war a àttewoo Sariiha ci lépp, ndax li mu wax: "li ma indi".
Gëm Yàlla day yokkoo ci topp Yàlla di wàññikoo ci moy.
