إعدادات العرض
yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm, Yàlla rëbb na nit ñiy jàppe bàmmeelu seeni Yónente ay jàkka".
[Wér na] [Ahmat soloo na ko]
الترجمة
العربية বাংলা Bosanski English Español فارسی Français Bahasa Indonesia Русский Tagalog Türkçe اردو 中文 हिन्दी Kurdî Hausa Português മലയാളം తెలుగు Kiswahili தமிழ் မြန်မာ Deutsch 日本語 پښتو Tiếng Việt অসমীয়া Shqip Svenska Čeština ગુજરાતી አማርኛ Yorùbá Nederlands ئۇيغۇرچە සිංහල ไทย دری Akan Azərbaycan Български Fulfulde Magyar Italiano ಕನ್ನಡ Кыргызча Lietuvių Malagasy नेपाली or Română Kinyarwanda тоҷикӣ O‘zbek Moore Oromoo Soomaali bm Українська rn km Српски ქართული Македонскиالشرح
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- dafa ñaan Boroomam mu bañ a def bàmmeelam ab xërëm bu nit di jaamu ci di ko màggal, ak di ko jublu buy sujjóot. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-wax na ne Yàlla soreele na yërmaandeem képp kuy jàppe bàmmeel i Yónente yi ay jàkka; ndax jàppe ko ay jàkka yoon wu jëm ci jaamu ko la ak di ci am ay pas-pas.فوائد الحديث
Jéggi dayob sariiha ci bàmmeel i Yónent yi ak ñu baax ñi day tax ñu di ko jaamu bàyyi fi Yàlla, moo tax ñu war a moytu luy jëme deci bokkaale.
Daganul di dem ci ay bàmmeel ngir màggal ko ak di fa def ag jaamu ak lu boroomam man a jege Yàlla mu kawe mi.
Tabax jàkka ci bàmmel yi dafa araam.
Julli ci bàmmeel yi dafa araam, doonte tabaxuñu ko jàkka, lu dul julleeb néew bi nga xam ne julleewuñu ko woon.