misaalum naaféq bi, moo ngi mel ni xar mu réer ci diggante ñaari xar, day daw jëm bii ci yoon wii dawaat jëm ca bee aw yoon

misaalum naaféq bi, moo ngi mel ni xar mu réer ci diggante ñaari xar, day daw jëm bii ci yoon wii dawaat jëm ca bee aw yoon

Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «misaalum naaféq bi, moo ngi mel ni xar mu réer ci diggante ñaari xar, day daw jëm bii ci yoon wii dawaat jëm ca bee aw yoon».

الشرح

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral melow naaféq bi, ci ne moo ngi mel ni xar muy jaabante te xamul man mbooloo ci gàtt yi lay topp, Day dem ci mbooloo mii, leeg-leeg mu dem ci mbooloo mee, Ñoom dañoo gëlëm ci diggante ngëm ak kéefar, ànduñu ak way-gëm ñi ci li feeñ ak li nëbbu, ànduñu it ak yéefar yi ci li feeñ ak li nëbbu, li feeñ sax kay way-gëm yi lañu ci àndal, waaye li nëbbu ci sikk-sakka ak deŋŋ-deŋŋ la nekk, leeg-leeg mu jeng jëm ci ñii, leeg-leeg mu jeng jëm ci ñee.

فوائد الحديث

Bokk na ci njariñal hdiis bi :

Bokk na ci njubug Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sadd ay misaal ngir jegeele maanaa yi

Leeral meloy naaféq yi ci deŋŋ-deŋŋ ak sikk-sakka ak ñàkk a dal.

Artu ci meloy naaféq yi, ak ñaaxe ci dëggu ak dogu ci ngëm ci li feeñ ak li nëbbu.

التصنيفات

Naafeq